Fan lañu mënee am yaakaar dëgg?
SA montar taxaw, nga gis ne dafa yàqu. Nga bëgg koo defar, nga gis ne am na ay defarkat yu bare. Ñu bare ci ñoom ne la mën nañu koo defar, waaye ku ci nekk li muy wax wuute na ak moroomam. Léegi, lan ngay def boo xamee ne, sa dëkkandoo mooy ki defar montar bi, ay at ci ginnaaw? Rax-ci-dolli, nga dégg ne bëgg na la dimbali te doo fey dara. Su booba, dootuloo am xel ñaar ci ki ngay tànn.
Loolu dafay misaal li nga mën a def ngir am yaakaar. Ci jamono ju metti jii, boo gisee ne sa yaakaar, mu ngi bëgg tas, fan nga mënee wut ndimbal? Ñu bare wax nañu la ne mën nañu la dimbali, waaye ku ci nekk li mu lay wax, wuute na ak moroomam. Loolu tax na nga jaxasoo. Kon li gën mooy, ñu dem ci Boroom bi, moom mi nga xam ne moo ñu sàkk te mën ñoo may yaakaar dëgg. Biibël bi nee na Yàlla «sorewul kenn ci nun» te dafa ñu bëgg dimbali (Jëf ya 17:27; 1 Piyeer 5:7).
Li yaakaar di tekki dëgg
Li Biibël bi di wax ci yaakaar moo gën a leer li doktoor yi ak boroom xam-xam yi di wax. Ci Biibël bi, «yaakaar» mooy yàkkamti lu baax li ngay xaar. Kon yaakaar ñaari mbir la ëmb. Benn bi mooy, bëgg am lu baax, beneen bi mooy li tax nga gëm ne lu baax loolu dina am. Yaakaar bi nekk ci Biibël bi du ay gént kese. Yaakaar bu wóor la te tegu ci ay firnde yu leer.
Ni ngëm, yaakaar dafa war a tegu ci ay firnde, waaye du ci ay nettali (Yawut ya 11:1). Ci Biibël bi, ngëm ak yaakaar dañu wuute (1 Korent 13:13).
Ci misaal, boo ñaanee sa xarit boo wóolu mu dimbali la, mën nga yaakaar ne dina la dimbali. Sa yaakaar am na fu mu tegu ndaxte gëm nga sa xarit, xam nga ko bu baax te yàgg nga di ko gis muy dimbali ñeneen ñi. Fii, ngëm ak yaakaar ñoo ànd te benn mënul dem bàyyi moroomam. Waaye ba tey wuute nañu. Naka nga mënee am yaakaar bu mel noonu ci Yàlla?
Liy maye yaakaar
Yàlla mooy maye yaakaar dëgg. Ca jamono yonent ya, ñu ngi doon woowe Yexowa «yaakaaru Israyil» (Yeremi 14:8). Bépp yaakaar bu Israyil amoon, ci moom la jóge woon. Kon moo doon seen yaakaar. Yaakaar boobu, du woon yéene rekk. Yàlla won na leen ci lu wóor li tax ñu war koo wóolu. Ci diir bu yàgg bi mu doon jëflante ak ñoom, dafa mas di def li mu leen dig. Yosuwe mi doon jiite mbooloo Israyil, lii la leen waxoon: «Xam ngeen bu baax ne, [...] amul lenn lu baax, li leen Yexowa seen Yàlla mas a dig te defu ko» (Yosuwe 23:14, MN).
Tey, mën nañu gëm li Yàlla dige. Biibël bi wax na ci ay dige Yàlla yu bare ak ni mu leen matale. Li Yàlla dige jaarale ko ci yonent yi, lu wóor la. Bi ñu doon bind yenn ci dige yooyu, dañu ko bind mel ni lu am la ba pare.
Loolu moo tax mën nañu ne Biibël bi téere yaakaar la. Boo jàngee Biibël bi, di nga gis ne mën nga wóolu Yàlla. Te loolu dina yokk sa ngëm ci li mu dige. Ndaw li Pool, lii la bindoon: «Ndaxte lépp lu ñu waxoon ci Mbind mi lu jiitu tey, dañu koo tëraloon, ngir nu sàkku ci xam-xam, xam-xam bu nuy may fit ak muñ, ak di feddali sunu yaakaar» (Room 15:4).
Ban yaakaar lañu Yàlla di may?
Kañ lañu gën a soxla am yaakaar? Bu ñu amee mbokk bu dee, ci la ñuy gën a soxla am yaakaar. Waaye ñu bare, bu ñu amee mbokk bu dee, seen yaakaar dafay daldi tas. Ci dëgg, amul dara lu mën tas yaakaar ba raw dee. Li ko waral mooy, kenn ci ñun mënul rëcc dee. Te itam, mënuñu dekkil suñu mbokk yi dee. Loolu moo tax Biibël bi tudde dee ‘noon bu mujj bi’ (1 Korent 15:26).
Kon, ban yaakaar lañu mën a am bu ñu ñàkkee suñu mbokk? Aaya biy wax ne dee mooy noon bu mujj bi, wax na itam ne noon boobu dinañu ko fi «jële». Yexowa, moo ëpp dee doole. Wone na ko ay yooni yoon. Naka la ko wone? Dafa dekkil ay nit ñu dee. Biibël bi wax na ci juróom ñeenti nit ñi Yexowa dekkil.
Benn bés, Yexowa dafa may Doomam Yeesu kàttan ngir mu dekkil xaritam Lasaar mi deewoon ci diiru ñeenti fan. Bi Yeesu di dekkil Lasaar, du moom rekk moo fa nekkoon, waaye ñu bare fekke nañu ko. (Yowaana 11:38-48, 53; 12:9, 10).
Xéyna dangay laaj sa bopp lii: ‘Lu tax mu dekkil ñooñu? Ndax ñooñu mujjuñu màgget te deewaat?’ Mujj nañu dee kay. Li Biibël bi wax ci ndekkite yooyu, tax na ba ñu gëm ne, suñu mbokk yi dee dinañu dundaat. Loolu mooy wone ne suñu yaakaar lu wóor la.
Yeesu nee na: «Man maay ndekkite li, maay dund gi» (Yowaana 11:25). Moom la Yexowa di jox kàttan ngir mu dekkil néew yi ci àddina si sépp. Yeesu nee na: «Jamonoo ngi ñëw ju néew yépp, yi nekk ci seen bàmmeel, di dégg baatam [baatu Yeesu] tey génn» (Yowaana 5:28, 29). Ñépp ñiy nelaw ci seen bàmmeel, mën nañu dekki te dund ci àjjana ci kaw suuf.
Yonent Yàlla Esayi wax na lu jëm ci ndekkite ci kàddu yu rafet yii: «Ñi nga deele ñooy dellu dundaat, seeni néew ay dekki, ku doon nelaw sa biir bàmmeel, yewwu, sarxolle» (Esayi 26:19).
Ndax dige boobu du dëfal xol? Ñi dee, ñu ngi fi gën a wóor. Nañu wóor ne suñu mbokk yi dee, ñu ngi ci xelu Yexowa, xel mu amul àpp. Dina leen dekkil te du fàtte kenn (Luug 20:37, 38). Te du yàgg dara, dinañu dekki. Te seen mbokk yi leen bëgg dinañu leen teeru ci àddina su bees si ànd ci ak mbégte bu réy! Kon, bu ñu ñàkkee suñu mbokk sax, yaakaar am na.
Ni la yaakaar mënee dimbali
Pool jàngal nañu lu bare ci njariñ bi yaakaar am. Nee na yaakaar dafa mel ni mbaxaney xare te dafa bokk ci suñuy yérey xare ci wàllu xel (1 Tesalonig 5:8). Lan la Pool bëggoon a wax? Ca jamono yonent ya, soldaar yi dañu doon sol mbaxaney weñ ci kaw beneen mbaxane bi ñu defaree der. Mbaxane boobu moo koy aar ci lu bare lu mën a dal ci boppam, ba du ko rey. Lan la Pool bëggoon a wax? Ni mbaxane di aare boppu soldaar, noonu la yaakaar di aare suñu xel ak suñuy xalaat. Boo amee yaakaar bu dëgër ci li Yàlla dige, loolu dina la dimbali nga ànd ak xel mu dal te bañ a jaaxle boo amee jafe-jafe. Ñun ñépp soxla nañu mbaxane bu mel noonu.
Pool jëfandikoo na beneen misaal ngir wone njariñ bi yaakaar am. Lii la bind: «Ci yaakaar jooju lanu sës sunu xol, ba mana sampu bu dëgër» (Yawut ya 6:19). Ay yooni yoon, Pool dugg na ci gaal mu suux. Kon, xam na bu baax njariñu weñ bi ñuy sànni ci ndox ngir mu téye gaal. Bu leen ngelaw di sonnal, boroom gaal yi dañuy sànni weñ biy téye gaal gi ci ndox. Weñ bi dina téye gaal gi ba du dem dal ci ay xeer.
Noonu itam su fekkee ne suñu yaakaar ci li Yàlla dige dafa «sampu bu dëgër», loolu dina ñu dimbali ñu jànkoonte ak jafe-jafe yi ñuy dund ci jamono ju metti jii. Yexowa dige na ne, du yàgg, geer yi, reyante bi, njàqare ji ba ci dee sax dootul am (Xoolal kaadar bi nekk ci paas 10). Yaakaar boobu mën na ñu aar, jox ñu kàttan bi ñu soxla ngir déggal Yàlla te bañ a topp àddina si ñu wër.
Yexowa bëgg na itam nga am yaakaar boobu. Dafa bëgg nga am dund gi mu la yéene. Li mu bëgg mooy «ñépp mucc». Naka lañu mën a def ba mucc? Bu njëkk bi mooy, kenn ku nekk ci ñun dafa war a «xam dëgg gi» bu baax (1 Timote 2:4). Ñu ngi lay xiir nga jàng xam dëgg gi nekk ci kàddu Yàlla. Yaakaar bi la Yàlla di may, moo gën fuuf bépp yaakaar bi la àddina si mën a may.
Boo amee yaakaar boobu, doo mas a xàddi, ndaxte Yàlla mën na la jox kàttan gi nga soxla ngir matal bépp jubluwaay bu méngoo ak coobareem (2 Korent 4:7; Filib 4:13). Ndax du yaakaar bu mel noonu nga soxla? Kon, bu fekkee ne yaa ngi wut a am yaakaar, na la wóor ne mën nga ko am.
[Kaadar bi/Foto bi]
Li tax ñu mën a am yaakaar
Aaya yii di topp mën nañu yokk sa yaakaar:
◼ Yàlla dig nañu ëllëgu jàmm.
Kàddu Yàlla nee na, suuf si dina nekk àjjana fu nit ñi di dëkk ci jàmm te doon benn (Sabóor 37:11, 29; Esayi 25:8; Peeñu 21:3, 4).
◼ Lépp li Yàlla wax dëgg la.
Dafa sib bépp fen. Yexowa ku sell la te lépp lu mu wax dëgg la (Kàddu yu Xelu 6:16-19; Esayi 6:2, 3; Tit 1:2; Yawut ya 6:18).
◼ Kàttanu Yàlla amul fu mu yem.
Yexowa rekk mooy Aji kàttan ji. Dara mënu koo tere def li mu dige (Mucc ga 15:11; Esayi 40:25, 26).
◼ Yàlla dafa bëgg nga dund ba fàww.
(Yowaana 3:16; 1 Timote 2:3, 4).
◼ Yàlla dafa bëgg ñu déggal ko.
Du xool ci lu bon li ñuy def, waaye dafay bàyyi xel ci suñuy jikko yu rafet ak ci lu baax li ñuy def (Sabóor 103:12-14; 130:3; Yawut ya 6:10). Li mu bëgg mooy ñu def lu baax te loolu dafa koy bégloo (Kàddu yu Xelu 27:11).
◼ Yàlla dige na ne dina la dimbali nga def coobareem.
Jaamam yi waru ñoo xàddi mukk. Yàlla dafa ñuy jox xelam mu sell, miy kàttan gi gën a réy, ngir dimbali ñu (Filib 4:13).
◼ Boo yaakaaree Yàlla, sa yaakaar du tas mukk.
Yàlla du la mas a wor ndaxte ku mat a wóolu la (Sabóor 25:3).
[Foto bi]
Ni mbaxane di aare boppu soldaar, noonu la yaakaar di aare suñu xel
[Foto bi]
Ni weñ biy téye gaal, noonu itam yaakaar mën na tax ñu sampu bu dëgër
[Ñi moom foto bi]
Courtesy René Seindal/Su concessione del Museo Archeologico Regionale A. Salinas di Palermo