TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • g18 n° 2
  • 12 Jubluwaay

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • 12 Jubluwaay
  • Yeewuleen! (2018)
  • Turu xaaj yi
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • LI MUY TEKKI
  • LI TAX MU AM SOLO
  • LI NGA MËN A DEF
  • Lan moo la mën a dimbali ba nga def li nga bëgg ci wàllu ngëm ?
    Sasu Nguuru Yàlla — 2006
  • Mën nga xeex ñaaw njort
    Yeewuleen! (2004)
  • Na ku nekk am li muy fas yéene def ci wàllu ngëm
    Sasu Nguuru Yàlla — 2002
  • Wéyal di jëm kanam
    Mën nga dund ci jàmm ba fàww! (Njàngum Biibël bi)
Yeewuleen! (2018)
g18 n° 2
Benn góor buy desine palaŋu kër

Jubluwaay dafa mel ni palaŋu kër, boo góor-góorloo, mën nga koo matal

NDAW ÑI ÑOO MOOM LII

12 Jubluwaay

LI MUY TEKKI

Jubluwaay du rekk loo bëgg ci sa xol. Am jubluwaay dëgg mu ngi tekki waajal li nga bëgg def, soppi doxalin bu ko jaree te ñeme coono.

Mën nañu am ay jubluwaay yu ndaw (yu ñuy matal ci ay bés walla ay semen), ay jubluwaay yu yem (yu ñuy matal ci ay weer) ak ay jubluwaay yu mag (yu ñuy matal ci benn at walla lu ko ëpp). Mën nañu matal jubluwaay yu mag yi bu ñu leen xaajee, ñu doon ay jubluwaay yu ndaw.

LI TAX MU AM SOLO

Matal say jubluwaay, mën na tax nga gën a wóolu sa bopp, sa diggante ak say xarit gën a dëgër te yokk sa mbégte.

Wóolu sa bopp: Boo matalee say jubluwaay yu ndaw, dinga gën a wóolu sa bopp ngir am jubluwaay yu gën a mag. Dinga gën a wóolu sa bopp itam ngir jànkoonte ak jafe-jafe yi ngay am bés bu nekk, lu mel ni ay xarit yu lay jéem a dugal ci lu bon.

Xaritoo: Ñu bare bëgg nañu am ay xarit yu am ay jubluwaay; maanaam, ay xarit yu xam li ñu bëgg te di def lépp ngir matal ko. Rax-ci-dolli, lenn liy gën a dëgëral sa diggante ak say xarit mooy ngeen bokk jubluwaay.

Mbégte: Boo amee ay jubluwaay ba matal leen, dangay yëg ne def nga dara.

«Am ay jubluwaay lu ma neex la. Dafay tax ma am ci lu ma jàpp te di def lépp ngir matal ko. Te boo matalee benn jubluwaay, dangay bég boo gisee ne matal nga ko ni nga ko bëgge woon» (Christopher).

LII LA BIIBËL BI WAX: «Kuy déglu ngelaw, doo ji, kuy seetluy niir, doo góob» (Kàdduy Waare 11:4).

LI NGA MËN A DEF

Xelal yii di topp, dinañu la dimbali, nga am ay jubluwaay te matal leen.

Ki nga doon. Bindal say jubluwaay ci kayit te jiital yi gën a am solo, maanaam yi nga bëgg njëkk matal.

Palaŋ. Boo amee jubluwaay, defal lii di topp:

  • Tànnal bés bi nga yaakaar ne mën nga ko matal.

  • Bindal fi nga war a jaar ba matal sa jubluwaay.

  • Jéemal a xalaat jafe-jafe yi nga mën a am te xool ni nga leen mënee faj.

Defal lii. Bul xaar ba lépp mat ngay soog a komaase. Laajal sa bopp li nga war a njëkk a def ngir matal sa jubluwaay, ba pare nga def ko. Saa yoo matalee dara, bind ko.

LII LA BIIBËL BI WAX: «Farlu, woomle [walla am alal]» (Kàddu yu Xelu 21:5).

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager