Lan moo la mën a dimbali ba nga def li nga bëgg ci wàllu ngëm ?
1 Yéen ndaw yi nekk karceen, bëgg ngeen Yexowa te fàttewuleen li Yeesu wax karceen yépp, maanaam ñu ‘ jëkk wut nguuram ak njubteem ’. (Macë 6:33.) Wóor na ne, dangeen di xalaat ci ñaar yooyu, bu ngeen di tànn li ngeen bëgg def ci seen àddina. Mën na am ngeen bëgg dem fu ñu soxla waaratekat ngir yokk li ngeen di def ci waaraate bi. Xéyna am na ci yéen ñu bëgg liggéey Betel walla nekk pioñee buy jébbal jotam yépp ci waaraate bi (pionnier spécial). Mën na am it ngeen bëgg bokk ci ñiy tabax ay Saalu Nguur, walla tukki ci àddina si ngir tabax ay Betel walla yu mel noonu, su loolu amee ci seen réew. Li ngeen bëgg noonu de, rafet na lool !
2 Am na lu leen mën a dimbali ci li ngeen fas yéene ci wàllu ngëm : mooy ngeen bind ko. La Tour de Garde bu 15 sulyet, 2004 waxoon na ne lu nekk ci sa xel, boo demee ba wax ko walla bind ko, dafay gën a leer te gën a niroo lu mën a nekk. Moo tax Tour de Garde boobu, nee woon na it ñu bind li ñu bëgg def ak ni ñu ko bëggee def. Mën nga komaase ci loo xam ne dina la dimbali ndànk-ndànk ci li nga bëgg ci wàllu ngëm. Loolu dina tax nga gis ni ngay jëme kanam, te nga bañ a fàtte fi nga bëgg jëm ci wàllu ngëm.
3 Lu la mën a dimbali ndànk-ndànk ngir nga def li nga bëgg ci wàllu ngëm : Bu fekkee ne nekkaguloo karceen bu ñu sóob, seetal li nga mën a def ngir nekk ko. Xéyna li nga xam ci Biibël bi des na. Kon nanga jéem a jàng téere Qu’enseigne la Bible ?, te wut aaya yi ci nekk yépp (1 Tim. 4:15). Nanga fas yéene it liir Biibël bi yépp, Njàlbéen ga ba Peeñu ma. Ñi nekk Betel ak ñi nekk Galàdd, loolu lañu war a def. Boo defee loolu ba pare, fexeel ba kontine di jàng Biibël bi bés bu nekk (Sab. 1:2, 3). Loolu, dina la dimbali bu baax nga jëm kanam ci wàllu ngëm. Bala ngay komaase liir walla gëstu Biibël bi, nanga njëkk ñaan Yàlla te boo paree, nanga ko ñaan itam. Te foo mënta nekk, nanga jéem a topp li nga jàng. — Saag 1:25.
4 Bu fekkee ne karceen bu ñu sóob nga, leneen lan nga mën a fas yéene def ci wàllu ngëm ? Xéyna danga bëgg gën a jàng ni ñuy waare, walla ni ñuy jëfandikoo Kàddu Yàlla ci waaraate bi (2 Tim. 2:15). Naka nga mënee yokk li ngay def ci waaraate bi ? Seetal ci at yi nga am ak ci li nga nekkee ngir xam ci lan nga mën a njëkk góor-góorlu ngir àgg fi nga bëgg jëm ci wàllu ngëm.
5 Kenn ku dem ba mën li mu bëggoon a def ci wàllu ngëm : Tony, xale bu góor bu 19 at la woon. Bi mu demee ci benn bànqaasu Seede Yexowa, la bëgg bokk ci ñi nekk Betel. Waaye ni mu doon dunde rafetul woon te jébbalagul woon sax boppam Yàlla. Tony daldi wax ne léegi dafa bëgg dundam neex Yexowa. Mu wax it ne dafa bëgg nekk karceen bu ñu sóob. Bi mu demee ba am li mu bëggoon noonu, mu wax ne léegi, dafa bëgg njëkk nekk pioñee buy jàpple, ba pare nekk pioñee bu ci sax. Mu daldi bind ci benn calendrier, bés yi mu bëgg komaase loolu. Mujj na nekk pioñee, te ginnaaw ga woo nañu ko Betel ngir mu liggéey fa. Loolu, mbégte mu réy la ko indil.
6 Yow itam dinga mën li nga bëgg def ci wàllu ngëm boo njëkkee wut liy jàpple Nguur gi. Nanga ñaan Yexowa te wax ko li nga bëgg def. Ba pare nanga ci góor-góorlu bu baax. — Léeb. 16:3 ; 21:5.
[Laaj yi]
1. Lan la ndaw yu nekk karceen yu bare fas yéene def ci wàllu ngëm ?
2. Lan moo la mën a dimbali nga jot ci li nga fas yéene def ci wàllu ngëm ?
3. Waxal lu ñu njëkk mën a def ngir nekk karceen bu ñu sóob.
4. Karceen bu bëgg nekk Betel walla pioñee buy jébbal jotam yépp ci liggéeyu waare bi, ci lan la mën a njëkk góor-góorlu ngir dem ba mën a nekk loolu ?
5. Suñu benn mbokk dafa njëkk góor-góorlu ci li ko dimbali ndànk-ndànk ba mu nekk Betel. Naka la ko defe ?
6. Lu la mën a dimbali ba nga mën li nga bëgg def ci wàllu ngëm ?