Yeneen ndimbal ngir njaboot gi
XELAL YI NEKK CI BIIBËL BI ÑOOY XELAL YI GËN ngir ñi nekk ci séy, ngir waajur yi ak ndaw ñi. Xelal yooyu, mën nañu dimbali nit ki mu xalaat bu baax te wone sago (Kàddu yu Xelu 1:1-4).
BIIBËL BI DAFAY TONTU ITAM CI LAAJ YU AM SOLO YU MEL NI:
Lu tax ñu nekk ci kaw suuf?
Ndax Yàlla moo tax ñu nekk ci coono?
Lan mooy dal nit bu deewee?
Boo bëggee gis tontu laaj yooyu ak yeneen, ñu ngi lay ñaan nga gëstu Biibël bi. Seetanal wideo bi tudd Lu tax ñu war a jàng Biibël bi? Eskaneel kod bi, walla nga dem ci jw.org.