XAAJ 8
Lépp li Biibël bi wax ne dina am, mooy am
Biibël bi nettali na li amoon démb. Wax na itam liy am ëllëg. Nit mënul loolu. Noonu lañu xame ne Biibël bi, ci Yàlla la jóge. Lan la Biibël bi wax lu jëm ci ëllëg ?
Mu ngi wax ci xeex bu mag bi Yàlla di def. Ci xeex boobu, Yàlla dina dindi ci kow suuf lépp lu bon ak nit ñu bon ñépp. Waaye dina aar ñi koy jaamu. Ki Yàlla def buur, maanaam Yeesu Kirist, dina def lépp ba ñiy jaamu Yàlla dëkk ci jàmm ak bànneex. Dootuñu feebar mukk walla dee.
Kontaan nañu ci li ñu xam ne Yàlla dina indi àjjana ju bees ci kow suuf, du dëgg ? Waaye am na lu ñu war a def su ñu bëggee dund ca àjjana jooja. Dinañu jàng ci nettali bi mujj li ñu war a def ngir bokk ci ñiy am lépp lu rafet li Yàlla di dencal ñi koy jaamu. Kon jàngal XAAJ 8 te xam li Biibël bi wax lu jëm ci li war a am ëllëg.