TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • my nettali 115
  • Àjjana Ju Bees Ci Kow Suuf Si

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Àjjana Ju Bees Ci Kow Suuf Si
  • Ay nettali yu nekk ci Biibël bi
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • Lan mooy coobare Yàlla ngir suuf si ?
    Lan la ñu Yàllay laaj?
  • Lan la Yàlla bëggoon bi muy sàkk suuf si ?
    Xibaaru jàmm bi jóge ci Yàlla !
  • Nguur gi nar a jiite suuf si sépp
    Jàngal-leen seeni doom
  • Xaritu Yàlla yi dinañu dund ca Àjjana
    Mën nga nekk xaritu Yàlla !
Ay nettali yu nekk ci Biibël bi
my nettali 115
Ay nit ñu ngi bànneexu ak mala yi ci biir Àjjana ci kaw suuf

NETTALI 115

Àjjana Ju Bees Ci Kow Suuf Si

XOOLAL garab yu mag yi, tóor-tóor yu rafet yi ak montaañ yu kowe yi. Ndax loolu lépp rafetul ? Xoolal kéwél gii di lekk ci loxo xale bu ndaw bi. Xoolal itam gaynde yi ak fas yi nekk foofu ci ñax bi. Ndax bëgguloo am kër ci béréb bu mel nii ?

Yàlla dafa bëgg nga dund ba fàww ci àjjana ci kow suuf. Te bëggul mukk nga am benn ci metit yi nit ñi am tey. Lii la Biibël bi wax ci ñiy dund ci àjjana ju bees ji : ‘ Yàlla dina nekk ak ñoom. Dee dootul am walla jooy walla metit. Li amoon bu jëkk, amatul. ’

Benn xale bu jigéen ci biir Àjjan ci kaw suuf mu ngi yore tóor-tóor bu mu witt

Yeesu mooy def lépp ba lu rafet loolu am. Ndax xam nga loolu, kañ lay doon ? Dina def loolu bu dindee ba pare lépp lu bon ak nit ñu bon ñépp ci kow suuf. Yaa ngi fàttaliku ne, bi Yeesu nekkee ci kow suuf, faj na bépp fasoŋu feebar, dekkal na sax ñu deewoon. Yeesu dafa def loolu ngir wone li muy def ci kow suuf si sépp, bés bu nguuroo ci nguuru Yàlla.

Xalaatal ni dund gi di neexe ci àjjana ju bees ji ci kow suuf si ! Yeesu dina nguuru ca asamaan ak ñi mu tànn. Dinañu toppatoo képp ku nekk ci suuf si te fexe ba ñépp dëkk ci jàmm. Nañu seet li ñu war a def bu ñu bëggee Yàlla may ñu dund gu dul jeex ci àjjanaam ju bees.

Peeñu ma 21:3, 4 ; 5:9, 10 ; 14:1-3.

Laaj yi

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager