Woy-Yàlla 30 (63)
Na leer gi ne nàññ
(Macë 5:16)
1. Yeowaa dogal ne
Doon na am, tey, leer
Guy deñloo lëndëmu
Nit ki yàgg’ réer.
Melaxiy kër’ Yàlla
Gaa ngiy ray-rayi
Ndax leeral ñu yoon wi.
Nguur gi nañ’ woyi.
2. Xabaaru Nguur’ Yàlla
Lañuy dem siiwal,
Di dëfël ñii ci tiis,
Rangooñ yiy wowal.
Doole ji ñuy waare
Ci Yaa la bawoo.
Moom moo tax, suñu sas
Ñu mën ittewoo.
3. Su-ñ’ takkoo ci njaamoom,
Gore te dogu,
Yàlla moo ñu ciy xiir,
Bu kenn naagu.
Ñun, mbooloom mu barkeel,
Nañu yéeneek mbég.
Turam nañu jagleel
Ndam, teraangaak weg.