Woy-Yàlla 32 (70)
Nañu mel ni Yérémi
(Yérémi 1:7, 18)
1. Liggéeyu Nguuru Yàlla,
Mbég mu dem dayo lay jur.
Ba ñuy doxal suñu sas,
Yàlla xelam ngi ñuy tuur.
Waaye artub Biibël bi
—Waxam ken’ du ko tebbi—
’Ngi ñuy xamal ne, dinañ’ daj
Tiis, wu Ibliis di yàbbi.
2. Seetleen ci kiy Yérémi,
Ma doon ndaw, ba-ñ’ ko wooye,
Yàlla daldi ko wax, ne:
‘Yaw, looy ragal nit doye?
Dëgg la, dinañ’ la xeex,
Nekk dëgg ci tés-tés,
Waaye duñu la mënal tus:
Dinga doon taax ju ma sës.’
3. Noonu diirub ati at,
Ak lu ñu ko toroxal,
Yérémi, ndax Yeowa,
Àntu na ci li-ñ’ ko fal.
Kon, nañ’ mel ni Yérémi,
Wóolu Yaa ci suñu xol.
Nañ’ waareek fit kiliftéefam:
Yeowa lañ’ àndandool.