Woy-Yàlla 36 (81)
Ngërëm ci mën-muñu Yàlla
(2 Pieer 3:15)
1. Yaw Yeowa, ci sa kàttan
Nga sàkke lép’, maye bakkan.
Sa mbindeef di la ko seedeel,
Jaww ji jép’ di ko dooleel.
Di xalaat ci rafetaayam
Dafay jural bànneex sa jaam,
Te lu dàq ngay amali,
Bu sa kiliftéef di jolli.
2. Ci sa cawarte ci njubte,
Mënoon ngaa jeexal coxorte.
Waaye am nañ’ nu ñu mucce:
Mayoo sa mer fu mu wàcce.
Tey, am na ñoo baaxe sa tur;
Ñu-ng’ lay màggal; cant la jur.
Seen kow la mbég di wal-wali
Bu sa kiliftéef di jolli.
3. Sa muñ gu yaa dinañ’ fonk,
Tey def lép’ li nga ñuy dénk:
Di jébbal suñu jot ciy waar,
Xamal nit fi mu war a jaar.
Maasaleel ko yoon’ àjjana
Lañ’ bëgg, ndax muc’ mu tànn.
Ndax mbég dinañu cal’-calli,
Bu sa kiliftéef di jolli.