Woy-Yàlla 33 (72)
Mbég yeek meññeefiy liggéeyu Nguur gi
(Macë 5:12)
1. Ci njaamug suñu Yàlla Yeowa,
Am nañu mbég yu jéggi dayo,
Mbëggeel doŋ’ a tax ñuy waare Nguur gi,
Suñu dëfël ñeneen di aayoo.
Da mel ni ñu ko Yeesu wóorale:
Maye, bànneex bu réy lay yóbbe.
Ci li ñu mën’ joxe, ana lu gën,
Dëgg giy jëme àjjana, bu jibee?
2. Bu dee sax ci liggéeyu waare bi,
Dañ’ ñuy ñaawal mbaa duñ’ ñu faale,
Fas yéene nañoo doon nit ñu dogu,
Te ak ngor wéy di ci saxaale.
Bu ñu jànkoonteek fitna bu tar sax,
Ndax li ñu faral turu Yàlla,
Yeesu nee na war nañoo tëb ndax mbég:
Loolook coono yonentiy Yaa benn la.
3. Ndaw mbég yu bare ci suñu njaamu,
Nañ’ dox ci tànkiy suñu Sang:
Waarleen meru Yàlla ci kow ñi bon,
Di naw Yeowa ci biir làng!
Nañ’ dundloo yaakaar ñépp ñiiy xiix:
Nañ’ séentu suuf su amul àq.
Loolu da ñuy jural mbégte mu xóot;
Dund ba fàw’, amul barke bu dàq.