Woy-Yàlla 64 (151)
Xabaaru Nguur gi, bu baax bi,nañu ko waar
(Macë 24:14)
1. Waarleen xabaaru Nguur gi, bu baax bi Yeesu yégle woon.
Xabaaru Nguur gi, bu baax bi, nañ’ waar!
Nañu waar xabaar boobu, ñeme, am fit, bañ ragal noon.
Xabaaru Nguur gi, bu baax bi, nañ’ waar!
Waarleen xabaaru Nguur gi ci mbedd yi, ak kër-oo-kër;
Waarleen xabaar boobook téere, ba xeet yép’ mu wër.
Waarleen ak manooreek mbaaxaay, gën cee sawar te dëgër.
Xabaaru Nguur gi, bu baax bi, nañ’ waar!
2. Waarleen xabaar bu baax bi, bu xew bu Yeowa waajal.
Xabaaru Nguur gi, bu baax bi, nañ’ waar!
Dina am añu mbootaay bu réy, Yaa di ñu ko yekkal.
Xabaaru Nguur gi, bu baax bi, nañ’ waar!
Waarleen xabaar bu baax bi, bu xew ak biiñ buy wal-wali,
Te kép’ ku xiif, ñam wu duun dina la suqali.
Waarleen xabaaru mucc gi, di dëfël tey feddali.
Xabaaru Nguur gi, bu baax bi, nañ’ waar!
3. Waarleen xabaaru Nguur gi, bu baax bi, bu mbég ngir ñép’, tey.
Xabaaru Nguur gi, bu baax bi, nañ’ waar!
Képp ku bëgg Yeowa, tey, naqar dootu la rey.
Xabaaru Nguur gi, bu baax bi, nañ’ waar!
Waarleen xabaaru ndimbal ngir nit ñi bëgg’ def lu baax.
Waarleen xabaaru jàmm ñi wóolu Yaa saxsax.
Waarleen xabaaru mbégu jaamu Yàlla, te ngor a tax.
Xabaaru Nguur gi, bu baax bi, nañ’ waar!