Woy-Yàlla 42 (92)
Waarleen ak fit
(Jëf ya 4:13)
1. Jaamiy Yàlla soxla nañu fit,
Ndax Seytaane daa bëgg ñu tiit.
Kàddu Yeowa moo ñuy fital,
Akit di waar yëf yi ñu nu jàngal.
Kàddu, giy dooleel, day feddali;
Nañ’ gore, dina ñu dimbali.
Nañ’ taxaw tem’, di bég tey ñeme,
Jaamiy Yàlla noonu lañ’ leen xame.
2. Ndegam gëm nañook suñu xol bép’,
Kàddu Yaa yey na ci wàllam yép’.
Ragaluñu li nit mën a def.
Lu ñu néew-néew, nañ’ gëm dëgg tey jëf.
Nañ’ teewlu ci liggéey bi-ñ’ ñu sas,
Te xabaar’ Yàlla fépp di tas.
Ba ca muj ga, su ñu waareek fit,
Yeowa dina doon suñu Xarit.
3. Xettalileen ñiiy néew-gi-doole
Ndax, ak fit, ci ñoom wax ji balle.
Bu ñu sàggane muk’ suñuy doom;
Ndax ñu màggaale fit, doon ñuy fas jom.
Nañ’ dëfël ñiiy xiix te am naqar;
Ci Yàlla nañ’ wékk seen yaakaar.
Ci kow suuf si sép’ dina doon Buur,
Bu woyiy nit ñi dunyaa bép’ di muur.