TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • sjj woy 153
  • May ma fit

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • May ma fit
  • Nañu woyal Yexowa ànd ceek mbégte
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • Woyleen, di tagg Yeowaak fit!
    Woyal, di Tagg Yeowa
Nañu woyal Yexowa ànd ceek mbégte
sjj woy 153

WOY-YÀLLA 153

May ma fit

Édition imprimée

(2 Rois 6:16)

  1. 1. Man tiit naa, ragal naa,

    te yoon bi lëndëm na.

    Bu ma jaxasoo, won ma yoon ;

    xam naa doo ma sore.

    Dund bi metti na,

    waaye li ma wóor mooy :

    yow Yàlla doo ma bàyyi mukk.

    Yow yaay aar sama dund.

    (AWU BI)

    Yexowa, maa ngi ñaan am ngëm ;

    ngëm guy tax ma gis ne,

    ñi ñuy aar ñoo ëpp ñi ànd ak ñoom.

    Def ma nit ku am fit !

    Am fit, waaw may ma fit !

    Fit dina tax ma muñ.

    Yexowa, maa ngi ñaan fit !

    Sa ndam moom wóor na ma !

  2. 2. Tiit dafa bokk ci nit.

    Sama doole doyul.

    Ci yow laay wéeru, nga aar ma.

    Yow, sa kàttan du jeex.

    Maa ngi lay ñaan am fit.

    May ma xolu jàmbaar.

    Dara du ma tax a xàddi.

    Waaw, du kaso, du dee.

    (AWU BI)

    Yexowa, maa ngi ñaan am ngëm ;

    ngëm guy tax ma gis ne,

    ñi ñuy aar ñoo ëpp ñi ànd ak ñoom.

    Def ma nit ku am fit !

    Am fit, waaw may ma fit !

    Fit dina tax ma muñ.

    Yexowa, maa ngi ñaan fit !

    Sa ndam moom wóor na ma !

    (AWU BI)

    Yexowa, maa ngi ñaan am ngëm ;

    ngëm guy tax ma gis ne,

    ñi ñuy aar ñoo ëpp ñi ànd ak ñoom.

    Def ma nit ku am fit !

    Am fit, waaw may ma fit !

    Fit dina tax ma muñ.

    Yexowa, maa ngi ñaan fit !

    Sa ndam moom wóor na ma !

    Yexowa, maa ngi ñaan fit !

    Sa ndam moom wóor na ma !

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager