Woy-Yàlla 52 (129)
Waxtu wi jot na!
(Mark 13:10)
1. Waxtu dem waare jot na,
Waxtu yee waa àddina.
Bu-ñ’ tiit tey wone noona
Ne Nguuru Yàllaa jar a tànn.
Nañu artu nit ñi balaa wees,
Ndax ci Babilon ñu bañ a des,
Ñu raw ci li ci kowam nar’ tees.
Ngir Yàlla, ak cawarte nañ’ fees.
Waxtu wi la; na suñ’ parlu fés!
2. Waxtu wi la, doon ay gor,
Di feeñal mbëggeel te ñor,
Nañ’ wallu mbokk yeek ngor,
Ñu doon as tuut walla ag gàngóor.
Nañ’ jaamu Yàlla, bañ doon ñu siis,
Ci ñun, bëgg dëgg gi du diis.
Yàlla muuñal ñu, lañuy ñaan gis
Te sàmm suñu ngor ci biir tiis.
Waxtu wi la, fexee bañ tarxiis!
3. Léegi xeex bi muj’ agsi;
Ndamu Yaa dinañ’ gisi.
Booba lëndëmu suuf si
Dina jeex te leer far wàccsi.
Ca waxtoom, ñi dee dinañ’ dekki;
Ci ñiy dunde Krist lañuy bokki.
Ragal musiba dina dakki.
Waaw, lool’ la xabaaru Yaa tekki.
Waxtu wi la, nit ñi dem fekki!