Woy-Yàlla 58 (138)
Doxal, ànd ak Yàlla!
(Mikaa 6:8)
1. Àndal ak Yaa ci rëyadi;
Fonkal mbaax, te dëggu.
Bul doon muk’ nit ku takkoodi;
Ci dooleem, deel riigu.
Soo bëggee wéy di naw dëggam,
Xam-xamu nit dawal;
Na la Yaa tette ci yoonam,
Ni gone guy déggal.
2. Doxal ak Yàlla ci cellaay;
Bul dellu ci bàkkaar.
Jublul ci ñoraay ak mataay,
Nangoom muj’ doon sa taar.
Te ci lépp lu set te laab,
Jub, baax te sopplu,
Teewlul; ngir muñ te doon kuy naab,
Ci Yaa deel wàkkirlu.
3. Àndal ak Yaa ci takkute,
Bu boobaa ngay mën’ daj
Mbég te ci moom am kóolute;
Ci ñoom la lépp xaj.
Doxal ak Yaa, bég saa su ne
Ci di tagg ndamam.
Mbég mi dàq tey siiw fu ne,
Ci Nguuram lañ’ koy am.