Woy-Yàlla 18 (42)
“Yoon waa ngii”
(Isayi 30:20, 21)
1. Baatu Yàllaa ngi wéy di woo tey xiirtal:
‘Doxleen ci yoon, wi ñu Yeowa xàllal.’
Jaam bu baax la tànn, bu amul moroom,
Mu di ñu jàngal sàrtu Ki di Boroom.
Yoon waa ngi nii, deeleen ci jaar.
Loo leen di xaar? Bu xel def ñaar!
Bànneex bu ni xóote, ànd-ak bile woote,
Moo jar a jóg, ngir di ko waar.
Xelum Yàllaa ngi ñuy xiir ci jëm kanam.
Nañuy dox ci njubaay ci bépp anam.
2. Baat bi ci suñ’ gannaaw, ndaw mbég ak bànneex!
Ndax Ki ñuy jàngal xamle na yoonu péex.
Ba ñuy déglook ràññee, nañu ko topp,
Bañ di jàdd yoon tey wottu suñ’ bopp.
Ndax yoonu leer ak dëgg la,
Yoonu Yàlla ngir ñii sell.
Ak gëtiy ngëm saxsax, ñu ngiy gis jàmm sax
Ci Nguuru Krist, lép’ ne cell.
Ndeyjoor walla cammooñ sañuñoo jàdd,
Dox ci yoonu Yàlla lañuy def aada.
3. Yoonu Yeowa, waaw, soxla nañ’ xamal;
Ñii ko nangoo déglu, nañ’ leen ko jàngal.
Nikiy petax yuy làqu ci seen ngunu
Ñu ngiy dawsi ci Yaa ci suñu xarnu.
Goreel na leen ci ndóol ak njaam.
Ba ñu woote, nee nañu: “Naam!”
Ñu ngiy dox ci bànneex, taqoo niki ay séex,
Di mbooloo mu fonk Yàllaam.
Nañu siggi, kon, te doon nit ñu farlu,
Ne jàkk Nguur gi, fi ñuy mën’ noppalu.