Woy-Yàlla 2 (4)
Àjjana ji Yàlla dig
(Lukk 23:43)
1. Ab àjjana, la ñu Yàlla dig,
Bu fiy jële, njuumteek bàkkaar,
Ci Nguuru Krist, gu Yeowa riig,
Guy neeloo mes dee ak naqar.
(AWU)
Ab àjjana fép’ ci suuf si,
Dig la bu Krist di amalsi.
Ak gëtiy ngëm, seetleen mii péex,
Ndax neex Yàlla, la def bànneex.
2. Léegi ci suuf, ndax mooy li Yaa nas,
Yeesu dekkal ñii dee, fu ne.
Dig na ag góor, laataa ko dee tas:
‘Ca Àjjana, dinga fa ne.’
(Awu)
3. Seetleen mbég, mi Yàlla di yokki,
Bu njàngaleem di ñu goreel,
Ak alfunniy nit ñu jóg, dekki,
Ñépp waccook mbon ak mbañeel.
(Awu)
4. Waaw, Àjjana la Sang bi dig.
Kon nañ’ sant suñu Yàlla.
Nguuram gi teew, suñ’ suuf si lay jig.
Tëbleen ndax mbég, ndax ku baax la.
(Awu)