Woy-Yàlla 62 (146)
Dawleen ci Nguuru Yàlla!
(Tsëfanyaa 2:3)
1. Wutleen Yeowa, yéen ñii woyaf te baax;
Wutleen a jub, tey ci jamano jii.
Noonu, waaw, du ñàkk ca bésub meram,
Dingeen am fu ngeen làquji.
(AWU)
Dawleen ci Nguuru Yàlla, suñ’ yaakaar;
Taxawuleen kiy Buuram (kiy Buuram).
Booba Yàlla dina leen aar te barkeel;
Gaawleen topp ndigalam (ndigalam).
2. Ñëwleen, yéen ñépp ñi xiif dëgg ak njub;
Waaw, lu tax ngeen di xiix tey jooyati?
Wutleen léegi yoonu Yàlla te am péex,
Nangul nguuru Krist du metti.
(Awu)
3. Seetleen ca kaw, waawaaw, siggileen ak mbég.
Gisleen liy firndeel ne Nguur gi teew na!
Nanguleen leer gi Yeowa di yónni,
Ragalleen ko ci bép’ fànn!
(Awu)