Woy-Yàlla 59 (139)
Dégluleen xabaaru Nguur gi
(Isayi 55:7)
1. Yéen, waa dunyaa, xabaaru Nguur gi dégluleen!
Yeesooy buur bi feeñ; artu nañu leen.
Léegi Aji-Noon ji dootu fi sax ay reen;
Kon, génnleen jamanoom; gaawleen! Waaw, dawleen!
(AWU)
Na ki soxor dëddu ay ñaawtéefam,
Te nit kiy lore soppi xalaatinam.
Nañu dellu ci Yaa, ndax ci muñam,
Dina leen baal, ci kow laabiiram.
2. Jaare ci ay Seedeem, Yeowaa ngiy yéene:
‘Bégal soo sonnee, bay ñaan saa su ne.
Kàttanam, Yeesu, mi ñu fal, dina wone.
Noonu la ñàkk, naqar ak tiis di deñe.’
(Awu)
3. Waaw, képp kuy déglu tey, ndax bànneex feccal!
Ak mbég nga dogal: ‘Yàlla laay déggal.’
Kép’ ku takku ci Yaa, dara du la jaaxal.
Waaye Nguuram ngay jiital te moom ngay àndal.
(Awu)