Woy-Yàlla 70 (162)
“Waareel kàddu gi”!
(2 Timote 4:2)
1. “Waareel kàddu gi,” ndigal la;
Yàllaa ko santaane tey.
Jamano ji war, léegi la.
Nañ’ doxal sas boobook teey.
“Waareel kàddu gi” booy jàngal;
Fexeel ba ki baax nànd.
Bul ragal nit, nangay xamal
Muy ci dëkk, ci tund.
2. “Waareel kàddu gi” làmboo ndam,
Jekk ci tontu ku ne,
Kuy laaj ci yaakaar ji nga am
Ci sa xol, di ko yéene.
“Waareel kàddu gi” ci fitnaal,
Su ko sax noon dee néewal.
Takkul ci li ñu la yebal;
Wóolul Yaa, Aji-Musal.
3. “Waareel kàddu gi,” bul tàyyi.
Akay jariñ ñiiy déglu!
Coxortee ngiy law, du bàyyi;
Muj gaa ngii, muy lu raglu.
“Waareel kàddu gi” te musal
Sa bopp ak ñeneen ñi.
“Waareel kàddu gi” ngir layal
Turu Yaa, wi dul deñi.