Woy-Yàlla 65 (152)
Nañu am ngërëm ci laabiiru Yàlla
(Room 11:33-35)
1. Ndaw alal, xam-xam ak sago,
Ci Yàlla suñu Boroom!
Ay àtteem yu xóot yéem nañ’ nit;
Yoonam, kumpa la ci moom.
Kan ci ñun moo ko mas’ xelal,
Kan a ko jàpple woon,
Ba tax mu ameel kooku bor,
War’ fey ku ko lebaloon?
2. Ndax Yeowa ku laabiir la,
Nañu wéy di ko sant.
Ci Yàllay njub lañ’ jébbalu;
Woyi cant nañ’ fent.
Ndegam, kon, dañoo jébbalu,
Na doon ci ñun lu dëggu,
Ànd ceek xel, akit sago,
Nañ’ dem ba jeex te dogu.
3. Buñu topp àddina si,
Nañ’ yeesal suñ’ xalaatin;
Dëgg gi mën na ñoo dooleel.
Na ngëm fés ci suñ’ dundin.
Nañuy naan Yàlla barkeel ñu,
Di ko jaamook suufeelu.
Nañ’ bëgg, ku ne sa moroom;
Ci mbég dinañ’ barkeelu.