Woy-Yàlla 66 (155)
“Nangoonteleen”!
(Room 15:7)
1. Nangoonteleen ak teraanga, ni ñu Yeesu nangoo!
Ndax Krist deewal na sa mbokk, seetal noo koy teeroo.
Kon, yaw mi ñor, dëgër ci ngëm, muñalal ki néew ngëm,
Dimbali ko mu feddali yaakaaram, ak ngërëm.
Ndaxte la ñu yonentay Yàlla yàggoon a bindal,
Mën naa dëgëral suñ’ yaakaar, akit di ñu dëfël.
Kon, saa su ne, wut doŋ’ li ñuy jariñ nañ’ fexee tiiñ,
Nañ’ wut a neex suñu moroom, akit li koy jariñ.
2. Yeowaa ngiy dajale nit ñu dul jàngati xeex.
Waxtu wi jot na, fu Doomam di sampaat jàm’ ak péex.
Ci xeet wu ne, giir ak làkk, mu ngiy jële gaayam,
Di jëmbët ci xol yeek xel yi, mbégu sàmm sàrtam.
Nañ’ séentu ndamu suñ’ Yàlla, ciy wéy di leen nangu;
Duñu gënaatle, nañ’ xaritook ñép’, bañ di tongu.
Mbubbu yaatuwaayu xolu Yàlla, nañu ko sol;
Nañu roy Doomam, te yaatal ñépp ci suñu xol.
3. Nañu jamp xeet yi yép’ ñu màggal Yaa suñu Buur,
Ñu bég ak mbooloom, di ko tagg; lool’ déggoo lay jur.
War nañ’ waare, kon, saa su ne, ci kër yeek mbedd yi,
Xamal ñeneen turu Yeowa, bu ñu ciy tàyyi.
Céru woy ndamu Yaa, dootuñ’ ko amati mukk.
Kép’ ku jubadi, léegi sa bakkan dinga ñàkk.
Kon, nañ’ bëgg suñuy mbokk, ndax Yaa doon ku dëggu.
Ciy nangoonte suñ’ biir ak teraanga nañu dogu.