Woy-Yàlla 74 (168)
Nangul Buuru suuf si, bu bees bi
(Sabuur 2:12)
1. Seetleen fale, ñiiy làngsi.
Waaw, akay luy bégloo xol!
Jàmbaariy Yàlla ñooy agsi,
Mbubbu déggoo lañu sol.
Ak seeni kask, yiy ray-rayi,
Njuumteek bàkkaar duñ’ fi bàyyi.
Li mooy seen yuux, duñ’ ci tàyyi:
“Yaw suuf, nangul Krist Buur bi.”
(AWU)
Fóonleen Doom ji laata Yaa di
Mer, luy yóbbe sànkute.
Barkeel nañu moos, nit ñi
Am ci moom kóolute!
2. Buur bi, Yeesu Krist, mooy jiite;
Njiitéefam lañuy topp.
Dañ’ koy déggal ak takkute,
Tey raw ci tiis ak wopp.
Jaasib Baat bi lañuy jukki,
Dàlliy xabaar bi, duñ’ tekki,
Di roy seen Sang bi dekki,
Bay deewal Ki ñu sopp.
(Awu)
3. Ndax Yàlla! Waxtu wi jot na:
Krist a ngiy nguurook kàttan!
Ay noonam, fép’ ci àddina,
Dinañ’ lox ngir seen bakkan.
Yeowaa ngiy ñori loxoom.
Liitam a ngiy jibloo artoom.
Kuy njiit, amal xel; bul di bóom.
Nangul Krist mi jot kàttan.
(Awu)