Woy-Yàlla 77 (174)
Wottuleen, ne temm,gën a dëgër
(1 Korent 16:13)
1. Wottuleen, ne tem’ te dëgër,
Ci xare bi ngir li jub.
Ndegam ndam li ngeen di séentu,
Solooleen fit niki mbub’.
Ak Krist, Gideyon mi Sut te wér,
Dalukaayu Madyan lañu wër.
Léegi ñu yuuxu kow suñuy noon;
Dinañ’ daw, bu-ñ’ leen di buub.
2. Wottulleen te doon nit ñu foog,
Dogu te sax ciy déggal.
Na ku ne yem fi-ñ’ ko yemloo,
Takku ci liy Krist digal.
Ni ñuy neexe Yaa, mën nañ’ ràññee,
Ndax ci royukaayam la feeñe.
Kon, nañ’ doon gor ci xareb Yàlla,
Ci yoon wi mu ñu xàllal.
3. Wottuleen tey muñ saa su ne;
Jàngleen xaar seen Boroom.
Ndax amul dara lu ko të;
Dina jëf, Moom, ca waxtoom.
Nikeek xarekatiy Gideyon,
Suñ’ Njiit àpp bi dina ñu won.
Nañ’ topp, kon, lép’ lu mu ébal.
Mooy làyyil Tur waak soloom.
4. Wottuleen, saxleen ci déggoo,
Xabaar bu baax bi falleen.
Tey, njiitéefu Yàllaak Nguur gi
Am na solo; Toppleen!
Nañ’ yuuxook ñi takku ci Yàlla:
‘Jaasiy Yeowaak Gideyon la!’
Wottuleen, ne temm te dëgër!
Ba muj ga, lu jub doxleen!