Woy-Yàlla 1 (3)
Nañu yóbbu ndam li ci kow àddina si
(Yowanna 16:33)
1. Nañ’ sàkku doole ci Yàlla,
Doon jàmbaar yuy jëm kanam,
Ndam yu bare la ñuy jagleel
Ci xareem, ngir fal turam.
Xeet yi dañ’ sib suñu ngor ndax
Li ñuy waar Kàddug Yàlla.
Wóolu ndam li Yaa di yóbbu,
Nañ’ maaj ci yoon wi sell.
2. Ci àddina, am nañ’ nattu.
Krist Yeesu waxoon na ko.
Waaye “Amleen fit!” la ci teg,
“Àddina sii noot naa ko.”
Waaw, dinañu daan suñuy noon,
Ndax xare bi du bu nit.
Yeowa Yàllaa di xare;
Ndamam ciy noonam, nañ’ liit.
3. Ci àddina si, am nañ’ ndam.
Ku mën a gëm Krist, jaar ci!
Samp nañu léegi Nguuram,
Te jaaseem, da ko bocci.
Ndegam mas naa noot àddina,
Mën nañ’ topp ciy tànkam.
Ci Yàlla, nañ’ wàkkirlu te,
Ndamam, fexe nit ñi xam.