Woy-Yàlla 81 (181)
Àndleen bokk ci woyu Nguur gi!
(Sabuur 98:1)
1. Dafa am woy, woyu ndam la, wu neex dëg’;
Ki muy màggal mooy Aji-Kowe ji.
Yaakaar ak ngor la ay baatam di yóbbe.
Nañ’ woy Nguur gi, ci fasoŋ buy jàjji:
‘Yeowaay Buur; na suuf si bég.
Yéen ñi ci kaw, seen baat nañ’ dég’.’
Woy wi daa bees; palu Krist lay nettali,
Ciy naw nguuram lañuy xiirtal, tey jii.
2. Ak woy woowu lañuy yéene Nguur gi fép’.
Yeesu Buur la; suuf si mooy moomeelam.
Ni-ñ’ ko dige, aw xeet wu bees juddu na,
Doomu Yàllaa ngiy ilif ci kowam.
‘Sujjóotleen ci kanamu Yaa.
Doomam Buur la. Na leer dunyaa!
Kaayleen jàng, woy wi jëm ci Nguur googu;
Jaamuleen Yaa, te jot ci tawféexam.’
3. Kép’ ku suufe mën naa mokkal woy wile.
Baat yi dañ’ leer, wax ji di seddal xol.
Ci suuf si sép’, ay ndiiraan jàng nañ’ ko,
Ci woo ñeneen, ñoom itam, bég nañ’ lool:
‘Ñëwleen jaamu te màggal Yaa,
Dina dekkal ñi seen xol yaa.’
Kon nañ’ ànd, te woy taggiy Yeowa.
Woyu Nguur gi, dina ko war’ neex lool.