Woy-Yàlla 82 (183)
Taxawaayu ndaw ñi ci biir ndefarinu Yàlla
(Sabuur 148:12, 13)
1. Ku nekk xaj nga ci ndefarinu Yàlla.
Mu ngiy woo mag ak ndaw ciy màggal turam.
Ni ndaw ñi ñépp wuyoo, dëgg, daa yéeme:
Ñu ngiy wër suuf si, di xamle liy Nguuram.
Seede bi, nag, ñuy amal, aka am doole!
Ñoo’ka jekk, am manoore te yaru!
Yeowa fonk na leen, ba ñu koy jaamu;
Ñi leen mag itam, ci ñoom ’ ngiy tiitaru.
2. Noonu, ndaw ñi ñépp, ñi mujj’ xam Yàlla,
Ndaw mbég ak bànneex, bu ñu am, nëgëni!
Jortuleen tuuti, it, li leen di xaar ëllëg
—Dund ci Àjjana, fu ñu dul sonni!
Ba booba dinañu daj ay jafe-jafe;
Ndax jamano jiiy màbb, lu yàggatul.
Nañ’ xeex ak suñu kem-kàttan ngir mën koo noot;
Ngor ci Nguur gi, ci suñu xol nañ’ ko muul!
3. Mën ngeen a am xarit dëgg ci mbooloo Yaa.
Lu ngeen di doyee wut leen ci àddina?
Nangeen farlu ci yëf yiy tabax ngëm dëgg,
Ci biir Kàddu Yàlla leer nañu nàññ.
Su ngeen jaaxle, jubluleen ci ñi leen bëgg,
Di leen xamal lépp li ub seen bopp.
Waaye seen xarit bi gën mooy Yaa Yeowa;
Laabiiram mooy firndeel ne daf’ leen sopp.
4. Ñu ngi bokk ci mbooloo gëmkat yiy karceen,
Fu Yeesu di faj suñuy soxla dëgg.
Kon, nañu topp Yeesu ak ngor te sax ci;
Di jëfe bépp xelal, bu ñu dégg.
Buñu nangu mukk àddina si muul ñu;
Na Yeowa laabal suñ’ xel ak Kàddoom.
Nañ’ ànd, mag ak ndaw, doon ay jaam yu takku;
Ba abadan, dinañ’ woy suñu Boroom.