WOY-YÀLLA 24
Kaayleen ci tundu Yexowa!
(Esayi 2:2-4)
1. Tundu Yexowa wi
moo sut yeneen tund yépp.
Xeet yépp, askan ak giir,
riirandoo di ko wutsi.
Yàlla, Moom ci boppam
moo ñu fa fas yéene woo.
Kaayleen, ñu dem tundam
mu xamal ñu ay yoonam.
Li tuuti doon junni
ci barke Yàlla mi ñuy gindi.
Yokkute bu doy waar,
Yexowa, Moom mooy ki koy sottal.
Mag, ndaw, góor ak jigéen
nangu nañ kiliftéefam.
Dogu nañu ci faral
Nguuram ba abadan.
2. Demleen, ndigal jib na.
Yeesu nee na ay ñoñam:
‘fu nekk, waare leen
Nguuru Yàlla ju Sell ji.
Woo doom-Aadama yi,
xiir leen ñu ragal Yàlla.’
Ñi ci woyof ñépp
nangu Kàddu Yexowa.
Mbooloo mi yokku na,
te mu doon lu ñu seede ñun ñépp.
Ndaw mbégte, bokk ci
ñiy jottali xibaar dund gi!
Ayca, ñu waareji
siiwal xibaar bu neex bii:
‘kaayleen ci tundu
Yexowa Yàlla ju wóor ji.’
(Xoolal itam Taalifi Cant 43:3; 99:9; Esayi 60:22; Jëf ya 16:5.)