TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • Ssb woy 191
  • Dundal dëgg gi

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Dundal dëgg gi
  • Woyal, di Tagg Yeowa
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • Dundal dëgg gi
    Nañu woyal Yexowa ànd ceek mbégte
Woyal, di Tagg Yeowa
Ssb woy 191

Woy-Yàlla 85 (191)

Dundal dëgg gi

(2 Korent 4:2)

1. Dundin bi gën, tey, moo di yoonu dëgg gi.

Amul weneen wu ko tane.

Krist jàngal na ne, suñ’ moroom dinañ’ bégi,

Ci kow, ñun, ñu doon ñu tabe.

Dundal dëgg gi.

Na sa ngëm wóor ñép’ léegi.

Ci sa demin ngay fésloo dëgg,

Ne, yaw, yaa ngiy dund dëgg gi.

2. Boo jiitalee Yaa te farlu ci di ko woy,

Àddina dina noonook yaw.

Ci ñi gëmadi, tànn Yàlla, di ko roy

Da leen di waar tey jële kaw.

Dundal dëgg gi,

Daw àddina siiy joggi.

Boo jegeñsee Yàlla, ngay xamle

Ne, yaw, yaa ngiy dund dëgg gi.

3. Ibliis dina jéem, saa su ne, am ku mu nax,

Waaye neel temm ci sa ngor.

Pakku ngëm bi yaa, moo di li ñuy aar saxsax,

Ba tax ay pexeem duñ ñu lor.

Dundal dëgg gi.

Fiiriy Ibliis deel jéggi.

Boo gànnaayoo yérey xare Yaa,

Dëgg, yaa ngiy dund dëgg gi.

4. Nafsu daa woyaf, xol nekk lu di wore.

Deel xeex jikko yu bon yeek fit.

Mën nga leen a daan teyit am ndam, boo goree,

Ndax Yeowa mooy sa Xarit.

Dundal dëgg gi.

Yoonu caay-caay deel teggi.

Soo nootee sa yaram, dinga won,

Ne, yaw, yaa ngiy dund dëgg gi.

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager