WOY-YÀLLA 56
Dundal dëgg gi
(Kàddu yu Xelu 3:1, 2)
1. Dundal dëgg gi, yow, wone ko ci say jëf.
Mooy yoon bi gën bi lay may xam-xam.
Wóolul Yexowa, doxal ci ay ndigalam.
Def ko wareef, am ci ndimbal.
(AWU BI)
Dundal dëgg gi.
Di ci des, jàppal bu baax.
Bégal ci bànneex
bi Yàlla di jox
ki di dund dëgg gi.
2. Yàlla moo yelloo sa jot ak sa kàttan gi.
Nga jaamu ko, xamle Nguuram fépp.
Dina la neexal boo farloo, bañ a tàyyi.
Nga gudd fan te bànneexu.
(AWU BI)
Dundal dëgg gi.
Di ci des, jàppal bu baax.
Bégal ci bànneex
bi Yàlla di jox
ki di dund dëgg gi.
3. Yàlla xam na ne, nit kiy dox moomul yoonam.
Ni xale soxlaa ñu tette ko,
Moo la won yoon bi, dee fa jaar boo bañee réer.
Topp ko, dina la barkeel.
(AWU BI)
Dundal dëgg gi.
Di ci des, jàppal bu baax.
Bégal ci bànneex
bi Yàlla di jox
ki di dund dëgg gi.
(Xoolal itam Taalifi Cant 26:3; Kàddu yu Xelu 8:35; 15:31; Yowaan 8:31, 32.)