Woy-Yàlla 91 (207)
Kan a ñu moom?
(1 Korent 6:20)
1. Waaw yaw, kan a la moom?
Jan Yàlla ngay déggal?
Waaw, jenn ji ngay sujjóotal
Mooy sa boroom; moom nga àndal.
Mënoo cee jaamu ñaar,
Mbaa am ñaari sang;
Boo ca bëggee jaar, sa xol day xar ñaar.
Doo neex ñii nga lëng.
2. Waaw yaw, kan a la moom?
Jan Yàlla ngay déggal?
Jenn jee wóor, jeneen ji bon,
Tànnal; mbir mi, ci yaw la, kon;
Ndax buur Sésaar a ngi
Lay laaj ngor bu dul wéy?
Mbaa Yàlla ji wóor ngay déggal, doon góor
Te def coobareem, tey?
3. Waaw man, kan a ma moom?
Yeowa laay déggal.
Yàllay dëgg ji lay jaamu;
Fey sama dige laay taamu.
Jot na maak njëg gu réy;
Jaamu nit, aka ñaaw!
Deewu Doomam kot’ moo fey sama njot;
Duma dellu ginnaaw.
4. Yàlla mooy ki ñu moom!
Werante amu ci.
Yégle woon na déggoo, buy am;
Ñu-ng’ koy dund ci biir géttam.
Mel ni gongo ci kow
Boppu kiy saraxe,
Daje bànneex la, ngir xam sa Yàlla;
Dëggam lañu baaxe.