Woy-Yàlla 90 (204)
“Maa ngii! Yebal ma”
(Isayi 6:8)
1. Sikk ak yàq deru Yaa,
Tey jii, bare na ci dunyaa;
Ne ñu: ‘Yaafus la,’ ‘Ku néeg la.’
“Yàlla? Amul! Wax kese la.”
Kuy dem làyyil Tur wi màgg,
Tagg ko ba ñépp dégg?
“Boroom bi, maa ngii! Yebal ma.
Dinaa la woy ak ngor lëmm;
(AWU)
Ana cér bu raw bii? Awma,
Yaa. Yàlla, maa ngii! Yebal ma.”
2. Ay tiiñkat nee nañ’ Yaa daa yéex;
Ci ñoom, ‘Ragal Yàlla daa jeex!’
Ñii yàllay xeer lañuy jaamu,
Ñee ci Sésaar lañuy damu.
Ku leen di wax li leen di xaar
Ca xareb Yàlla, biy doy waar?
“Boroom bi, maa ngii! Yebal ma
Ak fit, sa artu laay tama;
(Awu)
3. Tey, ñi woyaf’ ngi ci naqar
Ndax lu bon a ngi gën di tar.
Dëgg-dëgg, ñu ngiy fexee
Daj dëgg, giy tax nit texe.
Kuy dem dëfël nit ñi woyaf,
Ba njubte ci seen xol ñu taf?
“Boroom bi, maa ngii! Yebal ma.
Dinaa leen jàngal ak worma;
(Awu)