Njàngale 1
Naka nga mënee xam li la Yàlla laaj ?
Ban xam-xam bu am solo moo nekk ci Mbind mu sell mi ? (1)
Mbind mu sell mi, ci kan la jóge ? (2)
Lu tax nga wara jàng Mbind mu sell mi ? (3)
1. Mbind mu sell mi, maye Yàlla bu réy la. Mu ngi mel ni leetar bu jóge ci baay bu bëgg doomam yi. Dafa ñuy wax dëgg ci Yàlla — ku mu doon te li ko neex. Dafa ñuy won ni ñuy faje suñuy coono te ni ñuy ame bànneex dëgg. Mbind mu sell mi rekk moo ñuy wax li ñu wara def ngir neex Yàlla. — Sabuur 1:1-3 ; Isayi 48:17, 18.
2. Lu jege 40 góor ñoo bind Mbind mu sell mi. Liggéey boobu dañu ko door 1513 at bala suñu jamano di tàmbali te 1 600 at ginnaaw loolu la pare. Am na 66 téere yu ndaw yu booloo nekk Mbind mu sell mi. Ñi bind Mbind mu sell mi, Yàlla moo sol ci seen xel li ñu waroona bind. Binduñu seeni xalaati bopp, waaye xalaati Yàlla lañu bind. Kon Mbind mu sell mi ci Yàlla mi nekk ca asamaan la jóge, jógewul ci kenn ci kow suuf si. — 2 Timote 3:16, 17 ; 2 Pieer 1:20, 21.
3. Mbind mu sell mi sotti nañu ko te Yàlla def na ba sotti boobu baña am sikk. Ci téere yu ñu defar yépp, Mbind mu sell mi moo gëna bare. Bu ñu la gisee ngay jàng Mbind mu sell mi, ñépp duñu ci kontaan. Waaye bu la loolu taxa bàyyi. Soo bëggee dund ci bànneex ba fàww, war nga jànga xam Yàlla te def li mu bëgg, bu amee sax ñu ci àndul. — Macë 5:10-12 ; Yowanna 17:3.