TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • gf lesoŋ 12 p. 20
  • Lan moo xew ginnaaw dee ?

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Lan moo xew ginnaaw dee ?
  • Mën nga nekk xaritu Yàlla !
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • Ñi dee, fan lañu nekk?
    Mën nga dund ci jàmm ba fàww! (Njàngum Biibël bi)
  • Fan la ñi dee nekk ?
    Lan la Biibël bi wax dëgg-dëgg ?
  • Ndax ñi dee dinañu mas a dekki ?
    Xibaaru jàmm bi jóge ci Yàlla !
Mën nga nekk xaritu Yàlla !
gf lesoŋ 12 p. 20

NJÀNGALE 12

Lan moo xew ginnaaw dee ?

Ku dee mooy ku dul dund. Dee mu ngi mel ni nelaw bu xóot (Yowanna 11:11-14). Ñi dee mënuñu dégg, walla gis, walla wax, walla xalaat dara (Dajalekat 9:5, 10). Diine ju dul dëgg dafay jàngale ne ñi dee dañuy dem fu mbindeefu xel yi nekk ngir dund fa ak seeni maam yi dee. Du loolu la Mbind mu sell mi wax.

Isaa dekkil na doomu Yayrus bu jigéen

Ñi dee mënuñu dimbali walla lor nit ñi. Ñu bare dañu faral di topp ay aada walla di def ay sarax te yaakaar ne loolu dina neex ñi dee. Loolu neexul Yàlla ndaxte mu ngi jóge ci fen bu Seytaane wax. Loolu mënul neex itam ñi dee, ndaxte dundatuñu. Waruñu ragal walla jaamu ñi dee. Yàlla rekk lañu wara jaamu. — Macë 4:10.

Ñi dee dinañu dundaat. Bu ëllëgee, Yexowa dina yee ñi dee ngir ñu dund ci Àjjana ci kow suuf (Yowanna 5:28, 29 ; Jëf ya 24:15). Ni nga mënee yee kuy nelaw, noonu la Yàlla mënee yee ku dee. — Mark 5:22, 23, 41, 42.

Xalaat ne nit du dee, fen la bu Seytaane mi nekk Ibliis siiwal. Seytaane ak malaakaam yu bon yi dañuy gëmloo nit ñi ne tuuri maam yi, ñu ngiy dund ba léegi te ñooy indi ay feebar walla yeneen coono ci kow nit ñi. Seytaane dafay nax nit ñi, léeg-léeg mu jaar ci gént walla lu lay feeñu. Yexowa bañ na ñiy jéema wax ak ñi dee. — 5 Musaa 18:10-12.

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager