TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • lff lesoŋ 29
  • Ñi dee, fan lañu nekk?

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Ñi dee, fan lañu nekk?
  • Mën nga dund ci jàmm ba fàww! (Njàngum Biibël bi)
  • Turu xaaj yi
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • XÓOTALAL NJÀNG MI
  • NAÑU TËNK
  • GËSTUL
  • Fan la ñi dee nekk ?
    Lan la Biibël bi wax dëgg-dëgg ?
  • Ndax ñi dee dinañu mas a dekki ?
    Xibaaru jàmm bi jóge ci Yàlla !
  • Lan moo xew ginnaaw dee ?
    Mën nga nekk xaritu Yàlla !
  • Lan mooy dal suñuy soppe yi dee?
    Xam-xam biy jëme ca dund ga dul jeex
Mën nga dund ci jàmm ba fàww! (Njàngum Biibël bi)
lff lesoŋ 29
Lesoŋ 29. Jëkkër ak jabar ñu ngi ci benn armeel, sëgg di ñaan ci wetu bàmmeel.

LESOŊ 29

Ñi dee, fan lañu nekk?

Édition imprimée
Édition imprimée
Édition imprimée

Ndax mas nga am mbokk walla xarit bu gaañu? Boo masee am naqar bu mel noonu, xéyna laaj nga sa bopp lii: ‘Ñi dee, fan lañu nekk walla ci lan lañu nekk? Ndax am nañu yaakaaru gisaat suñu mbokk yi dee?’ Ci lesoŋ bii ak bi ci topp, xoolal tontu yuy dëfal xol yi ci Biibël bi joxe.

1. Ñi dee, ci lan lañu nekk?

Yeesu dafa méngale dee ak nelaw yu xóot. Nit kuy nelaw, nelaw yu xóot yëgatul dara ci liy xew ci wetam. Ci naka la dee niroo ak nelaw? Bu nit deewee, dootul yëgati benn metit te nekkatul ci coono. Biibël bi nee na: «Ku dee xamul dara» (Jàngal Kàdduy Waare 9:5).

2. Xam dëgg gi ci ñi dee, ban njariñ la ñuy amal?

Nit ñu bare dañu ragal dee, ñenn ñi sax ragal ñi dee ba pare! Waaye li Biibël bi wax ci ñi dee, mën na laa dëfal. Yeesu waxoon na ne: «Dëgg gi dina leen goreel» (Yowaana 8:32). Ci diine yu bare, dañuy jàngale ne bu nit deewee, am na luy génn ci moom dem dundi feneen. Waaye Biibël bi waxul loolu. Ndegam ku dee xamul dara, kon nit ñi dee yëgatuñu benn metit. Mënuñu def itam kenn lu bon. Kon soxlawul ñu leen di jéem a giifal, di leen saraxal walla di leen ñaanal.

Am na ñu naan mën nañu wax ak nit ñi dee. Waaye loolu mënul nekk. Ni ñu ko jànge léegi, ku dee «xamul dara.» Ñi foog ne dañuy wax ak ñi dee, ci dëgg malaaka yu bon yi lañuy waxal. Malaaka yooyu dañu bëgg ñu jaawale leen ak ñi dee. Kon xam dëgg gi ci ñi dee, dafa ñuy aar ci malaaka yu bon yi. Yexowa tere na ñu, ñuy jéem a wax ak ñi dee ndaxte dafa xam ne, jéem a jokkoo ak malaaka yu bon yi dina ñu lor (Jàngal Baamtug Yoon wi 18:10-12).

XÓOTALAL NJÀNG MI

Gënal a xóotal sa xam-xam ci li Biibël bi wax ci ñi dee, te gënal a dëgëral sa ngëm ci Yàlla miy mbëggeel, moom mi dul mbugël mukk ñi dee.

Benn góor ak ñaari doomam yu ndaw ñu ngi toog ci baŋ, ci dëju jabaram miy yaayu xale yi.

3. Fan la ñi dee nekk?

Lu jëm ci laaj boobu, li nit ñi gëm bare na te wuute. Waaye nag, loolu lépp mënul a doon dëgg.

  • Fi nga dëkk, lan la nit ñi gëm?

Boo bëggee xam li Biibël bi wax, seetaanal WIDEO BI.

WIDEO: Lan mooy dal nit bu deewee? (Xaaj) (1:19)

Foto yu ñu boole: Nataal yu jóge ci wideo bi tudd ‘Lan mooy dal nit bu deewee? (Xaaj).’ 1. Néew bu ñu tëral ci lalu opitaal. 2. Góor gu nekk diggante ñaari nit, mu ngi nelaw ci biir oto raay buy daw.

Jàngal Kàdduy Waare 3:20. Boo paree, nga tontu ci laaj yii di topp:

  • Ni ko aaya bi wone, fan la ñi dee nekk?

  • Ndax bu nit deewee, am na luy génn ci moom dem dundi feneen?

Biibël bi wax na ci li xewoon bi Lasaar xaritu Yeesu deewee. Booy jàng Yowaana 11:11-14, seetlul li Yeesu wax ci deewu Lasaar. Boo paree, tontul ci laaj yii:

  • Lan la Yeesu méngale ak dee?

  • Loolu lan la ñuy jàngal ci ñi dee?

  • Lan nga xalaat ci li Biibël bi wax ci ñi dee?

4. Xam dëgg gi ci ñi dee, dafa ñuy amal njariñ

Xam dëgg gi ci ñi dee, dafay tax dootuñu ragal dee. Jàngal Kàdduy Waare 9:10. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:

  • Ndax ñi dee mën nañu ñoo lor?

Bu ñu nangoo dëgg gi ñu Biibël bi wax, dootuñu gëm njàngale yu dul dëgg yiy naan dañu war a giifal ñi dee walla di leen saraxal. Jàngal Esayi 8:19 ak Peeñu 4:11. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:

  • Ci sa xalaat, naka la Yexowa gisee nit ñiy saraxal ñi dee walla di wut seen ndimbal?

Foto yu ñu boole: Ay aada yu jëm ci màggal ñi dee. 1. Góor gu sukk ci kanamu bàmmeel bu ñu teg ay lekk yu ñu saraxe, mu ngi ñaan. 2. Ñetti góor yu sol seen yérey cosaan, ñu ngi fecc. 3. Ab mbooloo mu sol ay mask te yor ay estati yu mag, ci bés bi ñu jagleel ñi dee.

Xam dëgg gi ci ñi dee dafa ñuy yewwi ci aada yi neexul Yexowa

5. Xam dëgg gi ci ñi dee, dafay dëfal suñu xol

Nit ñu bare, dañu leen jàngal ne bés bu ñu deewee, Yàlla dina leen mbugël ndax jëf yu bon yi ñu doon def. Waaye xam ne ñi dee nekkuñu ci metit ak lu bon lu ñu mënoon a def bi ñuy dund, loolu dafa ñuy dëfal. Jàngal Room 6:7. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:

  • Ni ñu ko jànge ci Biibël bi, ku dee bàkkaar mënatul dara ci moom, maanaam wàccoo na ak ay bàkkaaram. Kon ndax foog nga ne, ñi dee dinañu leen mbugël ndax bàkkaar yi ñu defoon bala ñuy dee?

Lu ñuy gën di xam Yexowa, ñuy gën a nànd ne Yexowa du mas a mbugël mukk nit ku dee. Jàngal Baamtug Yoon wi 32:4 ak 1 Yowaana 4:8. Boo paree, nga tontu ci laaj yii di topp:

  • Ndax Yàlla ju am jikko yu rafet yi ñu jàng ci aaya yooyu, dina nangoo mbugël nit ñi dee?

  • Ndax gisuloo ne, xam dëgg gi ci ñi dee dafay dëfal xol? Lu tax?

BU LA NIT WAXOON: «Dama ragal ñi dee.»

  • Yan aaya yuy dalal xel nga ko mën a won ci Biibël bi?

NAÑU TËNK

Ki dee, dundatul. Ñi dee nekkuñu ci metit te mënuñu lor nit ñiy dund.

Nañu fàttaliku

  • Ñi dee, fan lañu nekk?

  • Xam dëgg gi ci ñi dee, ban njariñ la ñuy amal?

  • Xam dëgg gi ci ñi dee, naka lay dëfale suñu xol?

Jubluwaay

GËSTUL

Xoolal ci Biibël bi, li «ruu» tekki dëgg.

«Lan mooy ruu?» (Ci jw.org la nekk)

Xoolal ndax Yàlla dafay lakk ñu bon ñi ci safara.

Ndax ci dëgg safara am na? (3:07)

Ndax war nañu ragal nit ñi dee?

Ndax ñi dee mën nañu ñu dimbali walla lor ñu? Ndax ñi dee ñu ngi dund ba tey? (téere bu ndaw)

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager