TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • bh pàcc 7 p. 66-75
  • Ci lu wóor mën nañu yaakaar ne suñu mbokk yi gaañu dinañu dekki

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Ci lu wóor mën nañu yaakaar ne suñu mbokk yi gaañu dinañu dekki
  • Lan la Biibël bi wax dëgg-dëgg ?
  • Turu xaaj yi
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • BU SUÑU MBOKK WALLA SUÑU XARIT GAAÑOO
  • «LASAAR, ÑËWAL CI BITI !»
  • LI ÑU MËN A JÀNG CI LI BIIBËL BI NETTALI CI ÑI YÀLLA DEKKAL
  • “NÉEW YÉPP, YI NEKK CI SEEN BÀMMEEL”
  • ÑIY DEKKI NGIR DUND CA KAW ASAMAAN
  • Suñu mbokk yi dee mën nañu dundaat!
    Mën nga dund ci jàmm ba fàww! (Njàngum Biibël bi)
  • Lan mooy dal suñuy soppe yi dee?
    Xam-xam biy jëme ca dund ga dul jeex
Lan la Biibël bi wax dëgg-dëgg ?
bh pàcc 7 p. 66-75

PÀCC JURÓOM-ÑAAR

Ci lu wóor mën nañu yaakaar ne suñu mbokk yi gaañu dinañu dekki

  • Lan moo ñuy won ne ndekkite dina am dëgg ?

  • Lan moo ñuy won ne Yexowa dafa bëgg a dekkal ñi dee ?

  • Ñan ñooy dekki ?

1-3. Ban noon moo ñuy topp ñun ñépp te lu tax jàng li Biibël bi wax di giifal suñu xol ?

BOO doon daw ku soxor a soxor ngir rëcc ko, fekk moo la ëpp doole fuuf te gën laa gaaw. Xam nga bu baax ne kooku amul benn yërmande, ndaxte mas nga koo gis mu rey ñenn ci say xarit. Ak li ngay daw lépp, mu lay gën di jege rekk. Dafa mel ni amatul benn pexe. Mu jékki-jékki rekk am ku ñëw nekk sa wet. Kooku nag moo ëpp doole fuuf sa noon boobu. Mu ne la dina la dimbali. Ndax gis nga ni sa xel di dale ?

2 Mën nañu wax ne noon bu mel noonu mu ngi lay topp tey. Ñépp lay topp sax. Ni ñu ko jànge ci pàcc bii weesu, Biibël bi dafay wax ne dee noon la. Kenn mënu koo rëcc te kenn mënu koo xeex. Li ëpp ci ñun am nañu mbokk walla xarit bu noon boobu rey. Waaye Yexowa moo ëpp doole fuuf dee. Dafa ñu bëgg te mooy Ki ñuy dimbali. Wone na ba pare ne mën na daan noon boobu. Te dig na ñu ne dina ko fi dindi ba fàww. Biibël bi nee na : “ Noon bu mujj, bi mu fiy jële, mooy dee. ” (1 Korent 15:26). Xebaar boobu neex na lool !

3 Nañu wax léegi tuuti ci li noon boobu di def ci ñun saa yu laalee kenn ku ñu xam. Loolu dina ñu dimbali ñu mën a nànd bu baax lenn lu ñu Yàlla dig lu ñuy indil mbégte. Yexowa dafa ñu dig ne ñi dee dinañu dundaat (Isaïe 26:19). Loolu mooy ndekkite bi ñu yaakaar.

BU SUÑU MBOKK WALLA SUÑU XARIT GAAÑOO

4. a) Lu tax li Yeesu def bi benn xaritam gaañoo mën ñu xamal li Yexowa yëg ? b) Ban xaritoo bu dëgër la Yeesu amoon ?

4 Ndax mas nga am mbokk walla xarit bu gaañu ? Naqar ak metit bi ngay yëg dafay mel ni doo ko mën a àttan. Booba lañuy soxla jàng Kàddu Yàlla ngir mu dëfël suñu xol (2 Korent 1:​3, 4). Biibël bi dafa ñuy won ni Yexowa ak Yeesu di gise dee. Yeesu mii niiru ak Baayam ci lépp, xamoon na lu nit di yëg ci xolam su mbokkam gaañoo (Yowaana 14:⁠9). Bi Yeesu nekkoon Yérusalem, dafa tàmmoon di seeti Lasaar ak ay magam yu jigéen, Maryaama ak Màrt. Ñooñu Betani lañu dëkkoon, ca wetu Yérusalem. Mujj nañu nekk ay xaritu Yeesu yu ko jege lool. Biibël bi nee na : “ Yeesu soppoon na Màrt ak Maryaama ak Lasaar. ” (Yowaana 11:⁠5). Waaye ni ñu ko jànge ci pàcc bi weesu, Lasaar dafa gaañu woon.

5, 6. a) Lan la Yeesu def bi mu nekkee ak mbokki Lasaar ak ay xaritam yi doon jooy Lasaar ? b) Naqar bi Yeesu amoon, lu tax mu ñuy may doole ?

5 Lan la Yeesu yëg ci biir xolam bi xaritam gaañoo ? Biibël bi nee na Yeesu dafa dem fi mbokki Lasaar ak ay xaritam nekkoon di jooy. Bi leen Yeesu gisee, loolu laal ko ci biir xolam. “ Mu daldi jàq, am naqar wu réy. ” Ñu teg ci : “ Yeesu jooy. ” (Yowaana 11:​33, 35). Ndax li Yeesu am naqar noonu dafay wone ne amul woon benn yaakaar ? Déedéet. Ci dëgg, Yeesu xamoon na ne lu réy moo fa doon waaj a am (Yowaana 11:​3, 4). Loolu taxul mu bañ a am naqar ak metit bi nit di yëg bu amee ku gaañu.

6 Mën nañu wax ne naqar bi Yeesu amoon dafa ñuy may doole. Dafa ñuy xamal ne Yeesu ak Baayam, Yexowa, bëgguñu nit di dee. Te Yexowa Yàlla moom, mën na xeex te daan noon boobu ! Nañu seet léegi li Yàlla mayoon Yeesu mu def ci jamono jooju.

«LASAAR, ÑËWAL CI BITI !»

7, 8. Bi Lasaar deewee, lu tax nit ñi yaakaar ne kenn mënatu ci dara, waaye lan la Yeesu def ?

7 Dañu suuloon Lasaar ci bàmmeel bu ñu yett ci doj. Yeesu daldi wax ñu dindi xeer bi ñu defoon ci buntu bàmmeel boobu. Waaye Màrt bëggul woon loolu ndaxte amoon na léegi ñeenti fan bi ñu suulee Lasaar ci bàmmeel bi. Kon néew bi waroon na komaasee yàqu (Yowaana 11:39). Bu doon nit ñi kese, ban yaakaar lañu mënoon a am foofu ?

Yeesu dekkal Lasaar, dafa ko woo mu génn bàmmeel bi, njaboot gi ak xarit kontaan

Bi ñu dekkalee Lasaar, loolu dafa indi mbégte bu réy. — Yowaana 11:​38-44.

8 Ñu daldi puus xeer bi. Yeesu woote ak baat bu dëgër ne : «Lasaar, ñëwal ci biti !» Lan moo xew ginnaaw loolu ? “ Néew bi daldi génn. ” (Yowaana 11:​43, 44). Xalaatal mbégte bi ñi fa nekkoon waroon a am ! Magu Lasaar yi, mbokkam yi, xaritam yi ak dëkkandoom yi, ñépp a xamoon ne Lasaar dee na. Waaye léegi mu ngi taxaw ci seen kanam, nekkaat ci seen biir, mel ni mu meloon. Aka doy waar ! Wóor na ne, ñu bare ñëw nañu ba ci moom, lëng ko, kontaan lool. Loolu de, ndam la ci kaw dee !

Ab jigéen ju jëkkëram gaañu mu ngi fóon doomam bi Iliyas dekkal

Iliyas dekkaloon na doomu jigéen bu jëkkëram gaañu. — 1 Rois 17:​17-24.

9, 10. a) Naka la Yeesu wonee fi mu jële kàttanu dekkal Lasaar ? b) Kuy jàng li Biibël bi nettali ci nit ñi ñu dekkal, ban njariñ la ciy jële ?

9 Yeesu waxul ne ci kàttanam la defe kéemaan boobu. Ba muy ñaan bala muy woo Lasaar ci biti, Yeesu dafa wone ba mu leer ne Yexowa mooy tax Lasaar dekki (Yowaana 11:41, 42). Du benn yoon boobu rekk la Yexowa jëfandikoo kàttanam ngir dekkal nit. Lasaar dafa bokk ci juróom-ñeenti nit ñi ñu wax ci Kàddu Yàlla ne dañu leen dekkala. Gëstu li Biibël bi nettali ci nit ñooñu, lu neex la. Ku def loolu dina gis ne Yàlla du gënale ndaxte mag ak ndaw, góor ak jigéen, waa Israyil ak ñu ci bokkul sax, la Yexowa dekkal. Li ñu nettali noonu, wone na ne nit ñi nekkoon foofu amoon nañu mbégte bu réy ! Seetal lii : bi Yeesu dekkalee benn janq, waajuram yi dañu “ waaru, ba ne jomm ”. (Màrk 5:42.) Dëgg-dëgg, li Yexowa def mayoon na leen mbégte bu ñu dul fàtte mukk.

Piyeer dekkal Dorkas

Ndaw li Piyeer dekkaloon na karceen bu jigéen bi tuddoon Dorkas. — Jëf ya 9:​36-42.

10 Xam nañu ne, ñi Yeesu dekkaloon mujj nañu deewaat. Ndax loolu dafay tekki ne li ñu leen dekkal amul woon benn njariñ ? Axakay, amoon na njariñ. Li ñu nettali noonu dafay dëggal ay kàddu yu am solo yu nekk ci Biibël bi. Te dafa ñuy may it yaakaar.

LI ÑU MËN A JÀNG CI LI BIIBËL BI NETTALI CI ÑI YÀLLA DEKKAL

11. Li Biibël bi nettali ci bi ñu dekkalee Lasaar, naka lay dëggale li ñu wax ci Dajalekat 9:​5 ?

11 Biibël bi dafay wax ne ñi dee “ xamuñu dara ”. Li ñu nettali ci Lasaar dafay dëggal loolu. Bi Lasaar jógee, ndax dafa doon wax nit ñi li xew ca asamaan ba ñépp waaru ? Ndax wax na leen lu jëm ci safara ba ñépp tiit ? Déedéet. Biibël bi wonewul fenn fu Lasaar waxe lu mel noonu. Ci ñeenti fan yi mu dee, ‘ xamul [woon] dara ’. (Dajalekat 9:​5, NW.) Lasaar dafa deewoon, mel ni kuy nelaw. — Yowaana 11:⁠11.

12. Lu tax mu mën ñu wóor ne Lasaar dekki woon na dëgg ?

12 Li ñu nettali ci Lasaar dafa ñuy jàngal it ne ndekkite lu am la, du ay wax kese. Yeesu dafa dekkal Lasaar ci kanamu nit ñu bare. Kilifa diine yi bañoon Yeesu sax weddiwuñu kéemaan boobu mu defoon. Waaye dañu waxoon ne : «Nit kii kat [maanaam Yeesu], kéemaan yi muy def a ngi bëgg a bare. Lu ñuy def nag ?» (Yowaana 11:47). Nit ñu bare demoon nañu seeti Lasaar bi ñu ko dekkalee. Mujj ga, ñu bare ci ñoom gëmoon nañu Yeesu. Ci ñoom, li dal Lasaar dafa doon wone ne Yàlla moo yónni Yeesu. Loolu dafa leeroon ba ay kilifa diine yawut yi bëgg a rey Yeesu ak Lasaar. — Yowaana 11:53 ; 12:​9-11.

13. Lan moo tax ñu mën a gëm ne Yexowa mën na dekkal ñi dee ?

13 Ku gëm ne ñi dee dinañu dekki, ndax kooku dafay gént ? Déedéet, ndaxte Yeesu waxoon na ne, bés dina ñëw, «néew yépp, yi nekk ci seen bàmmeel» dinañu dekki (Yowaana 5:28). Yexowa moo sàkk lépp luy dund. Wax ne Yexowa mën na sàkkaat mbindeefam ni mu meloon, ndax loolu war na jafe gëm ? Dëgg la, lu ëpp ci loolu, mu ngi aju ci li Yexowa mën a fàttaliku ni mbindeef moomu meloon. Ndax mën na fàttaliku suñuy mbokk ak suñuy xarit yi gaañu ? Ay milyaari-milyaari biddéew ñoo nekk ci asamaan si, waaye bu ci nekk, Yàlla dafa koy woowe ci turam (Isaïe 40:26). Kon, Yexowa mën na fàttaliku ni suñu mbokk ak suñu xarit yi gaañu meloon te du ci fàtte dara. Te pare na ngir dekkal leen.

14, 15. Li ko kàddu Ayóoba di wonee, lan moo ñuy won ne Yexowa dafa bëgg a dekkal ñi dee ?

14 Lan moo ñuy won ne Yexowa dafa bëgg a dekkal ñi dee ? Biibël bi nee na Yàlla dafa yàkkamti dekkal ñi dee. Ayóoba mi doon topp Yàlla bu baax mas na laajte lii : “ Boroom doole bu deewee, ndax dina mën a dundaat ? ” Ayóoba dafa doon wax ci bés bu nekkee ci bàmmeelam di xaar bés bi ko Yàlla di fàttaliku. Lii la waxoon Yexowa : “ Dinga woote, te man ci sama bopp, dinaa la tontu. Dinga yàkkamti gisaat li nga sàkk ak say loxo. ” — Ayóoba 14:​13-15, NW.

15 Ndax gis nga loolu ? Fi ñu tollu nii, Yexowa dafa yàkkamti dekkal ñi dee. Xam ne loolu moo nekk ci xolu Yexowa, ndax neexul ci xol ? Nañu wax léegi ci ndekkite biy ñëw. Ñan ñoo ciy bokk ? Fan lañuy dekki ?

“NÉEW YÉPP, YI NEKK CI SEEN BÀMMEEL”

16. Ñi dee, bu ñu dekkee, seen dund nu muy mel ?

16 Li Biibël bi nettali ci nit ñi dekki, am na lu bare li mu ñuy xamal ci ndekkite biy ñëw. Nit ñi Yàlla dekkaloon ci kaw suuf si, dañu dellu woon ci seeni mbokk. Noonu lay deme it ak ñiy dekki ëllëg, waaye booba lay gën a neex. Ni ñu ko gise ci pàcc 3, li Yàlla bëgg mooy ñu defaraat suuf si sépp ba mu nekk àjjana. Kon ñiy dekki duñu nekk ci àddina bu fees ak xeex, jubadi ak feebar. Dinañu mën a dund ba fàww ci suuf si ci jàmm ak salaam.

17. Ñan ñooy dekki ?

17 Ñan ñooy dekki ? Yeesu nee woon na : «Néew yépp, yi nekk ci seen bàmmeel [dinañu] dégg baatam [baatu Yeesu] tey génn.» (Ñun ñoo dëngal mbind yi ; Yowaana 5:​28, 29). Peeñu ma 20:13 nee na it : “ Géej gëq néew, yi nekkoon ci moom ; dee ak [“ ...hadès, ”, NW] dello néew, ya ñu yoroon. ” “ Hadès ” mooy bàmmeel bi doomu Aadama yépp bokk. (Seetal xaaj bi tudd “ Li ñu yokk ci waxtaan yi nekk ci téere bii ”, ci xët 212 ak 213). Kenn dootul nekkati ci bàmmeel boobu. Nit ñi fa nekk ñépp te mat ay milyaar dinañu dundaat. Ndaw li Pool nee woon na : «Ñi jub ak ñi jubadi dinañu dekki.» (Jëf ya 24:15). Loolu lu muy tekki ?

Ñi deewoon dekki nañu te kontaan a gise ak seeni mbokk ci biir àjjana ci kaw suuf

Ca Àjjana, ñi dee dinañu dekki, te dinañu nekkaat ak seeni mbokk.

18. Ñan ñoo bokk ci nit ñi “ jub  ” ñiy dekki, te yaakaar boobu, naka la lay laale yow ci sa bopp ?

18 Nit ñu bare ñi Biibël bi tudd, te ñu doon dund bala Yeesu di ñëw ci suuf, bokk nañu ci “ ñi jub ”. Xéyna sa xel dina dem ci Nóoyin, Ibraayma, Saarata, Musaa, Ruut, Esteer, ak ñeneen ñu bare. Yawut pàcc 11 wax na ci ñenn ci nit ñooñu amoon ngëm gu dëgër. Waaye jaamukatu Yexowa yuy gaañu tey ci suñu jamono, bokk nañu it ci ñi “ jub ” ñooñu. Yaakaar bi ñu am ci ndekkite bi, tax na ba ragaluñu dee. — Yawut ya 2:⁠15.

19. Ñan ñooy ñu “ jubadi ” ñi, te lan la leen Yexowa di may ci mbaaxaayam ?

19 Lu ñu mën a wax nag ci ñi nekkul woon di jaamu Yexowa, walla ñi nekkul woon di ko déggal ndax li ñu xamul woon dara ci moom ? Nit ñu “ jubadi ” ñooñu te mat ay milyaar, Yàlla du leen fàtte. Ñoom it dinañu dekki te dinañu leen may àpp ngir ñu jàng xam Yàlla dëgg ji te jaamu ko. Ci lu mat junni at, ñi dee dinañu dekki, te dinañu leen may ñu mën a bokk ci ñiy jaamu Yexowa ci kaw suuf. Jamono jooju dina neex lool. Mooy jamono ju Biibël bi di woowe Bésu Àtte bib.

20. Lan mooy géhenne, te kan moo fay dem ?

20 Ndax loolu ñu wax dafay tekki ne, képp ku dee dina dekki ? Déedéet. Biibël bi nee na, ci ñi dee am na ñu nekk ci “ géhenne ”. (Luc 12:​5.) Turu géhenne, mu ngi jóge ci béréb fi ñu doon tuure mbalit. Béréb boobu mu ngi nekkoon booy génn dëkku Yérusalem ca jamono Yeesu. Foofu lañu doon lakke mbalit yi ak ay néew. Néew yooyu ñoo doon néewu nit ñi nga xam ne, yawut yi dañu doon wax ne yelloowuñu ñu suul leen te yelloowuñu ñu dekkal leen. Kon jaadu na ñuy wax ne, nit ñi Yàlla alag ba fàww ñu ngi ci géhenne. Bu dee sax Yeesu dina am wàll bu am solo ci àtte bi nuy àtte ñiy dund ak ñi dee, Yexowa moo yore kàddu bu mujj bi ci àtte bi nit ki yelloo (Jëf ya 10:42). Du dekkal ñi mu gis ne dañu bon te bañ a soppiku.

ÑIY DEKKI NGIR DUND CA KAW ASAMAAN

21, 22. a) Waxal beneen ndekkite bi war a am itam. b) Kan moo njëkk a dekki pur dem ci asamaan ?

21 Biibël bi dafay wax itam ci beneen ndekkite, maanaam ñiy dekki ngir dund ca kaw asamaan mel ni malaaka yi. Ci nit ñi Yàlla di dekkal ci fasoŋ boobu, ndekkite Yeesu rekk lañu nettali ci Biibël bi.

22 Ginnaaw bi Yeesu deewee ci kaw suuf, Yexowa nanguwul bàyyi doomam boobu ko doon topp bu baax mu des ci bàmmeel bi (Psaume 16:10 ; Jëf ya 13:​34, 35). Yàlla dafa dekkal Yeesu. Waaye dekkalu ko ak yaram bu mel ni bi mu amoon. Ndaw li Piyeer nee na Kirist “ dee na ci jëmm, waaye dundaat na ci xel ”. (1 Piyeer 3:18.) Dëgg-dëgg, loolu kéemaan bu réy la. Yeesu dafa dundaat nekk xel maanaam malaaka bu bare kàttan (1 Korent 15:​3-6). Yeesu mooy ki ñu njëkk a dekkal ci fasoŋ bu doy kéemaan boobu (Yowaana 3:13). Waaye ndekkite boobu du yem ci moom rekk.

23, 24. Ñan ñoo bokk ci «coggal ju ndaw ji» Yeesu moom, te ñaata lañuy doon ?

23 Bi Yeesu xamee ne léegi mu dellu ca kaw asamaan, dafa wax taalibeem yi ko doon topp bu baax ne dafay ‘ dem defaral leen fa ñuy dëkk ’. (Yowaana 14:⁠2.) Yeesu dafa woowe nit ñiy dem ca kaw asamaan «coggal ju ndaw ji». (Luug 12:32.) Ñaata karceen dëgg ñooy bokk ci gurup bu ndaw boobu ? Ni ko Peeñu ma 14:1 wonee, lii la ndaw li Yowaana waxoon : “ Ma xool noonu, gis Mbote ma [Yeesu] taxaw ci tundu Siyon, ànd ak téeméer ak ñeent-fukk ak ñeenti junniy nit, te ñu bind ci seen jë turu Mbote ma ak turu Baayam. ”

24 Karceen yooyu ñuy dekkal ca kaw asamaan dinañu mat 144 000. Taalibe Yeesu yi doon ànd ak moom, bokk nañu ci karceen yooyu. Kañ la ndekkite boobu di am ? Ndaw li Pool bindoon na ne ci jamono ju fi Yeesu di nekk lay am (1 Korent 15:23). Dinañu gis ci pàcc 9 ne ñu ngi ci jamono jooju. Kon ci waxtu bii ñu nekk nii, bu ci amee ñu dee ci li des ci 144 000 yooyu, dañuy dekki ci saa si, dem ca kaw asamaan (1 Korent 15:​51-55). Waaye li ëpp ci doomu Aadama yi, dañu am yaakaaru dekki ci Àjjana jiy am ëllëg ci kaw suuf.

25. Ci lan lañuy waxtaan ci pàcc bii di topp ?

25 Waaw Yexowa dina daan dee bi nekk suñu noon. Dee dootul amati ba fàww (Isaïe 25:⁠8). Waaye xéyna yaa ngi laaj sa bopp lii : ‘ Ñiy dekki te dem asamaan, lan lañu fay def ? ’ Dinañu bokk ci Nguuru Yàlla gu doy kéemaan guy nekk ca kaw asamaan. Pàcc bii di topp dina gën a wax ci nguur googu.

a Biibël bi wax na ci yeneen nit ñi Yàlla dekkal ci téere yii : 1 Buur 17:​17-24 ; 2 Rois 4:​32-37 ; 13:​20, 21 ; Macë 28:​5-7 ; Luug 7:​11-17 ; 8:40-56 ; Jëf ya 9:​36-42 ak 20:​7-12.

b Boo bëggee yokk li nga xam ci Bésu Àtte bi ak ci kaw lan lañuy àtte nit ñi, seetal li ñu wax ci xaaj bi tudd “ Li ñu yokk ci waxtaan yi nekk ci téere bii ”, ci xët 213 ba 215.

LI BIIBËL BI WAX

  • Li Biibël bi nettali ci ñi Yàlla dekkal, dafa ñuy may yaakaar bu wóor. — Yowaana 11:​39-44.

  • Yexowa dafa yàkkamti dekkal ñi dee. — Ayóoba 14:​13-15, NW.

  • Képp ku nekk ci bàmmeel bi doomu Aadama yépp bokk, dina dekki. — Yowaana 5:​28, 29.

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager