LI ÑU YOKK CI WAXTAAN YI NEKK CI TÉERE BII
Lan mooy shéol ak hadès ?
CI LÀKK yi ñu njëkk a binde Biibël bi, kàddu bi doon tekki she’ôl ci ebrë ak haïdês ci gereg, feeñ na lu ëpp 70 yoon. Ñaari baat yooyu, ci dee lañuy wax. Ci Biibël yi ñu bind ci yeneen làkk, “ bàmmeel ”, “ safara ” walla “ kàmb ” lañu bind ci palaasu ñaari baat yooyu. Waaye ci lu ëpp ci làkk yi, amul baat buy tekki dëgg ñaari kàddu yooyu am ci ebrë ak ci gereg. Moo tax Biibël bi tudd Traduction du monde nouveau di bind “ shéol ” ak “ hadès ”. Lan la baat yooyu di tekki dëgg ? Nañu seet ni ñu leen di jëfandikoo ci ay aaya yu nekk ci Biibël bi.
Dajalekat 9:10, NW, nee na : “ Amul liggéey, amul waaj, amul xam-xam ca shéol, fa nga jëm. ” Ndax loolu dafay tekki ne shéol bàmmeel la, fi nga xam ne xéyna suul nañu fa sa benn mbokk walla xarit ? Déedéet. Bu Biibël bi di wax ci fi ñu suul nit walla bàmmeel, du she’ôl walla haïdês lañu fay bind. Waaye ci làkku ebrë ak gereg, yeneen baat lañu fay bind. Binduñu it “ shéol ” ci Biibël bi ngir wax fi ñu suul ay nit ñu bare, mel ni njaboot yi am benn béréb fi ñuy dénc seen waa kër yi gaañu, walla fi ñu suul ay nit ñu bare. — Njàlbéen ga 49:30, 31.
Kon “ shéol ” ban fasoŋu béréb la ? Kàddu Yàlla wone na ne “ shéol ” walla “ hadès ” moo gën a réy sax béréb bu yaatu fu ñu suul ay nit ñu bare. Esayi 5:14, NW, nee na shéol dafa “ réy te ubbi gémmiñam ba mu yaatu ”. Li shéol jël ci nit ñu dee, ak ni mu bare yépp, terewul mu mel ni lu doyalul (Proverbes 30:15, 16). Shéol du doyal. Melul ni bàmmeel dëgg yi nga xam ne néew yi ñu ci mën a def, dafa am fu muy yem (Proverbes 27:20). Shéol moom du fees mukk. Amul fu mu yem. Shéol ak hadès nekkul fenn. Dafa di bàmmeel bu ñi dee bokk. Dafay misaal fi li ëpp ci doomu Aadama yi gaañu nekk, di nelaw.
Li Biibël bi wax ci ndekkite bi dafa ñuy dimbali ñu gën a xam li “ shéol ” ak “ hadès ” di tekki. Bu Kàddu Yàlla di wax ci ku dee te mën a am yaakaaru dekki, dafa koy boole ak shéol walla hadèsa (Job 14:13 ; Actes 2:31 ; Révélation 20:13). Kàddu Yàlla wone na it ne du ñi doon jaamu Yexowa kese ñu nekk ci shéol walla hadès. Waaye ñu bare ñu ko jaamuwul, ñoo nga fa itam (Njàlbéen ga 37:35 ; Psaume 55:15). Moo tax Biibël bi di wax ne “ ñi jub ak ñi jubadi dinañu dekki ”. — Jëf ya 24:15.
a Waaye Biibël bi wone na ne ñi dee te waruñu dekki, nekkuñu ci shéol walla hadès waaye ci “ géhenne ” lañu nekk (Matthieu 5:30 ; 10:28 ; 23:33). Ni shéol ak hadès, géhenne du béréb bu nekk fenn.