TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • ll xaaj 3 p. 8-9
  • Naka la dund bi meloon ci toolu Eden ba ?

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Naka la dund bi meloon ci toolu Eden ba ?
  • Déggleen li Yàlla wax ndax ngeen am dund gu dul jeex
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • Li tax ñu dàq leen
    Ay nettali yu nekk ci Biibël bi
  • Ndegam Aadama ak Awa dañu déglu Seytaane — loolu lan la jur ?
    Déggleen li Yàlla wax ndax ngeen am dund gu dul jeex
  • Xaaj 3
    Déggleen li Yàlla wax
  • Lu tax nit di dee ?
    Dundleen ba fàww ak bànneex ci suuf si !
Xóotalal waxtaan bi
Déggleen li Yàlla wax ndax ngeen am dund gu dul jeex
ll xaaj 3 p. 8-9

XAAJ 3

Naka la dund bi meloon ci toolu Eden ba ?

Yexowa mayoon na Aadama ak Awa ay yëf yu neex te baree-bare. Njàlbéen ga 1:28

Yexowa sàkkoon na Awa, ngir mu nekk jabaru Aadama

Yexowa sàkkoon na Awa, di jigéen bu njëkk ba, ngir mu nekk jabaru Aadama. — Njàlbéen ga 2:21, 22.

Bi leen Yexowa sàkkee, ay nit yu mat lañu woon, amuñu woon benn sikk ci seen yaram ak seen xel.

Aadama ak Awa ñoo ngi seetlu seen dëkkwayu toolu Eden

Ci toolu Eden lañu nekkoon. Béréb bu rafet la woon ci kaw suuf si. Amoon na ay dex, ay garab, ay doomu garab, ak ay mala.

Yexowa dafa doon wax ak ñoom, di leen jàngal. Bu ñu déggoon bu baax li mu leen doon wax, dinañu dund ba fàww ci kaw suuf si.

Yàlla tere woon na ñu lekk ci benn doomu garab. Njàlbéen ga 2:16, 17

Garab bu nekkoon ci toolu Eden bi Yexowa tere woon Aadama ak Awa ñu lekk ci

Yexowa tere woon na Aadama ak Awa ñu lekk ci benn doomu garab bu nekkoon ci toolu Eden. Waxoon na leen ne bés bu ñu ko lekkee, dinañu dee.

Malaaka bu bon, Seytaane Ibliis, Jaar na ci jaan ngir wax ak Awa

Kenn ci malaaka yi Yàlla sàkkoon dafa fippu. Malaaka bu bon boobu mooy Ibliis Seytaane.

Seytaane bëggul woon Aadama ak Awa  déggal Yexowa. Dafa jaar ci benn  jaan ngir gëmloo Awa ne, bu lekkee ci doomu garab bi, du dee, te dina mel ni Yàlla. Li wóor mooy li Seytaane wax ay fen la woon. — Njàlbéen ga 3:1-5.

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager