TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • ll xaaj 4 p. 10-11
  • Ndegam Aadama ak Awa dañu déglu Seytaane — loolu lan la jur ?

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Ndegam Aadama ak Awa dañu déglu Seytaane — loolu lan la jur ?
  • Déggleen li Yàlla wax ndax ngeen am dund gu dul jeex
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • Naka la dund bi meloon ci toolu Eden ba ?
    Déggleen li Yàlla wax ndax ngeen am dund gu dul jeex
  • Xaaj 4
    Déggleen li Yàlla wax
  • Fan la ñi dee nekk ?
    Lan la Biibël bi wax dëgg-dëgg ?
  • Léegi àddina bi metti na
    Ay nettali yu nekk ci Biibël bi
Xóotalal waxtaan bi
Déggleen li Yàlla wax ndax ngeen am dund gu dul jeex
ll xaaj 4 p. 10-11

XAAJ 4

Ndegam Aadama ak Awa dañu déglu Seytaane — loolu lan la jur ?

Aadama ak Awa déggaluñu Yàlla, loolu moo tax ñu dee. Njàlbéen ga 3:6, 23

Awa lekk na ci doomu garab bi ñu tere woon te mu jox ci Aadama

Awa déglu na jaan bi, lekk na ci doomu garab bi, daldi jox Aadama moom itam mu  lekk.

Aadama ak Awa dàq nañu leen ci toolu Eden ba

Li ñu def baaxul — bàkkaar la. Moo tax Yàlla dàq leen ci toolu Eden ba.

Aadama ak Awa màggat nañu te dee

Dund bi metti woon na ci ñoom ak ci seeni doom. Dem nañu ba màggat, te dee nañu. Bi ñu deewee, demuñu kaw asamaan di fa dund, nekkatuñu woon fenn di dund.

Ñi dee dañuy dellu nekk suuf, dundatuñu feneen. Njàlbéen ga 3:19

Nitu cosaan yu wuute ci jamono yu dul benn

Nit ñi dañuy dee ndaxte dañu donn bàkkaar bi Aadama ak Awa def. Ñi dee mënuñu gis, mënuñu dégg, mënuñu def dara. — Ecclésiaste 9:5, 10.

Xale bu jigéen bu dee te naqarloo njabootam

Yexowa bëggul woon nit ñi di dee. Du yàggati dara, Yàlla dina dekkal ñi dee. Ñooñu dekki, su ñu déggee li Yàlla wax, dinañu dund ba fàww ci kaw suuf si.

  • Lu tax ñit ñi di dee ? — Room 5:12.

  • Dee dootul am. — 1 Korent 15:26.

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager