TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • ll xaaj 6 p. 14-15
  • Lan lañu mën a jàng ci taw bu metti bi amoon ca jamano Nóoyin ?

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Lan lañu mën a jàng ci taw bu metti bi amoon ca jamano Nóoyin ?
  • Déggleen li Yàlla wax ndax ngeen am dund gu dul jeex
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • Xaaj 6
    Déggleen li Yàlla wax
  • Artu bu jóge ca lu amoon
    Mën nga nekk xaritu Yàlla !
  • Ca jamano yonent Yàlla Nóoyin — ñan ñoo déggoon li Yàlla wax te ñan ñoo bañoon a dégg ?
    Déggleen li Yàlla wax ndax ngeen am dund gu dul jeex
  • Nit ku nekk am na li nga mën a jàng ci wideo bi tudd : Noé : il marchait avec Dieu
    Sasu Nguuru Yàlla — 2002
Xóotalal waxtaan bi
Déggleen li Yàlla wax ndax ngeen am dund gu dul jeex
ll xaaj 6 p. 14-15

XAAJ 6

Lan lañu mën a jàng ci taw bu metti bi amoon ca jamano Nóoyin ?

Yàlla alag na nit ñu bon ñi. Nóoyin ak njabootam mucc nañu. Njàlbéen ga 7:11, 12, 23

Gaal gaa ngi tëmb, nit ñu bon ñi suux nañu, te malaaka yu fippu woon bàyyi woon nañu seen jëmu nit

Tawoon na ñeent-fukki guddi ak ñeent-fukki bëccëg ba ndox mi muur lépp li nekkoon ci kaw suuf si. Nit ñu soxor ñi ñépp dee woon nañu.

Malaaka yi jëloon jëmu nit te ñëwoon ci kaw suuf si, mujj nañu delluwaat ci kaw asamaan, jëlaat seen jëmu malaaka yu soxor.

Nóoyin, njabootam ak mala yi génn nañu ci gaal gi te xon gi feeñ na ca asamaan

Ñi nekkoon ci biir gaal gi mucc nañu. Dëgg la, Nóoyin ak njabootam mujj nañu màggat te dee, waaye Yàlla dina leen dekkil ngir ñu dund ba fàww.

Yàlla dina alagaat nit ñu soxor ñi. Nit ñu jub ñi dinañu mucc. Macë 24:37-39

Seytane ak malaakam yu bon yi ci ay pexe yu bare lañuy jaar di nax nit ñi

Seytaane ak malaaka yu bon yi ñu ngi kontine di nax nit ñi.

Niki jamano Nóoyin, tey itam nit ñi bëgguñu topp ndigalu Yexowa yi. Du yàggati dara, Yexowa dina alag nit ñu bon ñépp.— 2 Piyeer 2:5, 6.

Seede Yexowa yi dañuy jëfandikoo Biibël bi bu ñuy waare, góor guy jàng Biibël bi

Am na ay nit yu mel ni Nóoyin— dañuy dégg li Yàlla wax te di topp li mu wax. Ñooñu ñooy Seede Yexowa yi.

  • Jaarleen ci yoon bi jëm ca dund gu dul jeex. — Macë 7:13, 14.

  • Yàlla dina alag nit ñu soxor ñi. Nit ñu woyof ñi dinañu am jàmm. — Sabóor 37:10, 11.

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager