NJÀNGALE 16
Lan mooy liggéeyu ñiy topptoo yëfi mbooloo mi ?
Birmanie
Waxtaan ci mbooloo mi
Ndaje bi ñuy def bala ñuy waare
Set-setalu saalu Nguur
Biibël bi wax na ci ñaari gurupu karceen yu góor yu ñu dénk liggéey ci mbooloo mi, “ njiit ” yi ak “ ñiy topptoo yëfi mbooloo mi ” (Filib 1:1). Ñaari gurup yooyu ñu ngi ci li ëpp ci mbooloo yi. Ñiy topptoo yëfi mbooloo mi, ban liggéey bu am njariñ lañuy def ci biir mbooloo mi ?
Dañuy jàpple magi mbooloo mi. Ñiy topptoo yëfi mbooloo mi, dañu am diggante bu rattax ak Yexowa. Dañu nekk ñu jar a wóolu te dañu farlu ci seen liggéey. Am na ci ñoom ay mag ak ay waxambaane. Liggéey bu am solo lañuy def ci mbooloo mi ndaxte ñoom ñoo féete ci lépp luy liggéeyu doole ak yeneen liggéey yi mbooloo mi laaj ngir doxalinam. Loolu dafay may magi mbooloo mi ñu gën a am jot ngir def seen liggéey, maanaam jàngal ak sàmm mbooloo mi.
Dañuy topptoo yëf yu bare. Dañu leen di dénk lu bare ci mbooloo mi, lu mel ni : teeru ñi ñëw ci ndaje yi, topptoo lépp lu jëm ci mikoro yi ak misik bi, topptoo xaalisu mbooloo mi walla téere yi ñuy jot ci mbooloo mi, ak wax waa mbooloo mi béréb yi ñu war a waare. Dañuy bokk itam ci topptoo bi ak set-setalu saalu Nguur gi. Lée-lée magi mbooloo mi wax leen ñu jàpple ñi màgget ci mbooloo mi. Ñiy topptoo yëfi mbooloo mi, ñu ngi def ak xol bu tàlli bépp liggéey bu ñu leen dénk ci mbooloo mi, moo tax ñépp may leen cér. — 1 Timote 3:13.
Dañu nekk ay royukaay yu rafet ci karceen yu góor yi. Ñiy topptoo yëfi mbooloo mi, dañu leen di tànn ndax seen jikko karceen ju rafet. Ñoom, bu ñuy bokk ci njàngale mi ñuy def ci mbooloo mi, dañuy dëgëral suñu ngëm. Ñun, bu ñu gisee ni ñu saware ci liggéeyu waare bi, loolu dafa ñuy sawarloo it. Seen ànd bu rafet ak mag yi mooy yokk jàmm ak déggoo bi am ci mbooloo mi (Efes 4:16). Xéyna bu yàggee, ñoom it dinañu mat a nekk mag ci mbooloo mi.
Ñiy topptoo yëfi mbooloo mi, yan jikko lañu war a am ?
Ñiy topptoo yëfi mbooloo mi, ban njariñ la seen liggéey am ?