WOY-YÀLLA 100
Nañu doon ñu mën a dalal gan
(Jëf ya 17:7)
1. Ci teral gan, Yàlla amu fi moroom.
Nit ñépp lay dalal, moom suñu Boroom.
Ndax mooy fenkal jantam,
Teg ci di leen tawal,
Amul kenn ku mu ko bañal.
Su ñu seetloo ne am na ku néew doole,
Nañu seet ni ñu ko mën a jàppalee.
Dinañu roy Yàlla,
Te loolu mbégte la.
Ci lu wóor moom dina ñu barkeel.
2. Sooy góor-góorlu ci jàppale néew doole,
Mën na ci gis njariñ, te am ci mbégte.
Nañu dalal nit ñépp,
Ubbil leen suñu xol,
Kiy doxandéem sax dina féex lool.
Nañu roy Lidi mi fonkoon ganale.
Alalam la daan jël di ko séddale.
Yexowa mooy barkeel
Kuy wéy di ganale,
Yërmande jooju jural ñu yool.
(Xoolal itam Jëf ya 16:14, 15; Room 12:13; 1 Timote 3:2; Yawut ya 13:2; 1 Piyeer 4:9.)