WOY-YÀLLA 57
Nañu waar nit ñépp
(1 Timote 2:4)
1. Yexowa suñu Baay du gënale,
Ñun itam dañu bëgg roy ci moom.
Looloo waral ñuy wax ak nit ku ne,
Ngir mu mën a xaritoo ak Yàlla.
(AWU BI)
Ak nu nit ki mën a mel,
Mu am alal walla déet,
Yexowa dafa fonk nit ku ne.
Suñu mbëggeel rekk a tax,
Ñu bëgg wax nit ku ne:
«Yow mën nga nekk xaritu Yàlla.»
2. Xol bu rafet la Yexowa di xool,
Te loolu rekk moo ko itteel ci nit.
Du li nit sol walla fi mu jóge,
Mooy li gën a am solo ci Yàlla.
(AWU BI)
Ak nu nit ki mën a mel,
Mu am alal walla déet,
Yexowa dafa fonk nit ku ne.
Suñu mbëggeel rekk a tax,
Ñu bëgg wax nit ku ne:
«Yow mën nga nekk xaritu Yàlla.»
3. Yexowa ànd na ak ku dogu
Bàyyi àddina ak li ci biiram.
Xibaar boobu lañu bëgg a yégle
Ak cawarte te duñu ci tàyyi.
(AWU BI)
Ak nu nit ki mën a mel,
Mu am alal walla déet,
Yexowa dafa fonk nit ku ne.
Suñu mbëggeel rekk a tax,
Ñu bëgg wax nit ku ne:
«Yow mën nga nekk xaritu Yàlla.»
(Xoolal itam Yowaana 12:32; Jëf ya 10:34; 1 Timote 4:10; Tit 2:11.)