TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • th lesoŋ 1 p. 4
  • Li ngay njëkk a wax

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Li ngay njëkk a wax
  • Yokkal sa mën-mën ci jàng ak jàngale
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • Woneel bu baax njariñu li ngay jàngale
    Yokkal sa mën-mën ci jàng ak jàngale
Yokkal sa mën-mën ci jàng ak jàngale
th lesoŋ 1 p. 4

LESOŊ 1

Li ngay njëkk a wax

Aaya bi ñu lim

Jëf ya 17:22

LI NGA WAR A JÀPP: Li ngay njëkk a wax war na tax nit ñi bëgg laa déglu, xam li nga nar a waxtaane ak njariñu waxtaan bi.

NI NGA KO MËN A DEFE:

  • Fexeel ba nit ñi bëgg laa déglu. Laajal benn laaj, fàttalil li benn boroom xam-xam mas a wax, nettalil lu nit mas a dund, walla nga wax ci benn xibaar bu ñépp di waxtaane.

    Xelal bu baax

    Njëkkal a xalaat bu baax ci liy intereese nit ñi ak ci seeni jafe-jafe, ba noppi nga jaar ci ngir waajal li ngay njëkk a wax.

  • Nanga xamal nit ñi li nga nar a waxtaane. Fexeel ba li nga nar a waxtaane ak li waral waxtaan bi feeñ bu baax ci li ngay njëkk a wax.

  • Woneel li tax waxtaan bi am njariñ. Ci li ngay njëkk a wax, wonal ñi lay déglu ni leen waxtaan bi mënee dimbali ci seen dund. Fexeel ba ñu xam bu baax njariñ bi leen waxtaan bi mën a amal.

    Xelal bu baax

    Booy waajal waxtaan ci mbooloo mi, laajal sa bopp lii: «Lan la sama mbokk yi ci ngëm di dund?», ba pare nga sóoraale loolu ci li ngay njëkk a wax.

CI LIGGÉEYU WAARE BI:

Seetlul bu baax li nit ki di def ak li ko wër ngir wax li ko mën a intereese. Komaaseel waxtaan bi ak benn laaj walla nga wax ci li nga seetlu.

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager