TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • th lesoŋ 13 p. 16
  • Woneel bu baax njariñu li ngay jàngale

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Woneel bu baax njariñu li ngay jàngale
  • Yokkal sa mën-mën ci jàng ak jàngale
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • Li ngay njëkk a wax
    Yokkal sa mën-mën ci jàng ak jàngale
  • Defal lépp ngir laal xolu nit ñi
    Yokkal sa mën-mën ci jàng ak jàngale
  • Waxal ak cawarte
    Yokkal sa mën-mën ci jàng ak jàngale
  • Defal waxtaan buy yokk xam-xam
    Yokkal sa mën-mën ci jàng ak jàngale
Xóotalal waxtaan bi
Yokkal sa mën-mën ci jàng ak jàngale
th lesoŋ 13 p. 16

LESOŊ 13

Woneel bu baax njariñu li ngay jàngale

Aaya bi ñu lim

Kàddu yu Xelu 3:21

LI NGA WAR A JÀPP: Dimbalil ñi lay déglu ñu xam njariñu li ngay jàngale te won leen ni ñu ko mën a jëfe.

NI NGA KO MËN A DEFE:

  • Xalaatal ñi la nar a déglu. Xalaatal bu baax ci li tax nit ñi war a xam li nga leen bëgg a jàngal, te seetal ci sa waxtaan lan moo leen di gën a amal njariñ.

  • Ci sa waxtaan bi yépp, wonal ñi lay déglu li ñu war a def. Booy komaase, ak ci waxtaan bi yépp, képp kuy déglu war na mën a wax ne: «Lii, dina ma amal njariñ». Booy wax ci ponk bu am solo bu nekk, woneel ni ñu ko mën a jëfe. Na njariñu li ngay wax leer bu baax.

    Xelal bu baax

    Booy wone ni ñu mënee topp santaane yi nekk ci Biibël bi, def ko ak mbëggeel te nanga wone ne yëg nga ñi lay déglu. Bu leen jiiñ dara, waaye yokk leen mbëggeel te dëgëral seen ngëm, xam ne loolu moo leen war a xiir ci def lu baax.

CI LIGGÉEYU WAARE BI:

Booy waajal sa bopp ngir dem waare, xalaatal ci xibaar yi ak li itteel nit ñi ci sa gox. Waxtaanal ci li gën a mën a amal nit ñi njariñ. Laajal ay laaj yuy tax nit ki wax li ko itteel, waaye na ànd ak yar. Déglul tont bi, ba pare nga wax ci li ko itteel.

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager