TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • th lesoŋ 14 p. 17
  • Woneel bu baax ponk yi gën a am solo

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Woneel bu baax ponk yi gën a am solo
  • Yokkal sa mën-mën ci jàng ak jàngale
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • Li ngay wax ngir jeexal sa waxtaan
    Yokkal sa mën-mën ci jàng ak jàngale
Yokkal sa mën-mën ci jàng ak jàngale
th lesoŋ 14 p. 17

LESOŊ 14

Woneel bu baax ponk yi gën a am solo

Aaya bi ñu lim

Yawut ya 8:1

LI NGA WAR A JÀPP: Dimbalil ñi lay déglu ñu xam bu baax li waral sa waxtaan, te woneel ci lu leer ni ponk bu gën a am solo bu nekk ànde ak li waral waxtaan bi ak it turu waxtaan bi.

NI NGA KO MËN A DEFE:

  • Xamal li waral sa waxtaan. Bala ngay def sa waxtaan, seetal ndax waxtaan bi dañu ci bëgg a xamal nit ñi dara, walla wax leen li tax ñu mën a gëm dara, walla xiir leen ci def dara. Booy def sa waxtaan, na ponk yi gën a am solo yépp leeral bu baax li waral sa waxtaan.

    Xelal bu baax

    Xalaatal ci lii: ‘Yan laaj la nit ñi mën a am ci li ma bëgg a waxtaane? Lan moo mën a tax ñu bañ a gëm li may wax? Naka la loolu lépp di toppalante ci seen xel?’ Boo xamee loolu, fexeel ba ponk yi ngay jàngale toppalantee noonu, su ko defee ñu mën laa déglu bu baax te nangu li nga leen di xamal.

  • Na sa turu waxtaan bi feeñ bu baax ci biir waxtaan bi. Waxaatal kàddu yi gën a am solo ci turu waxtaan bi walla nga wax ay kàddu yu leen niru ngir turu waxtaan bi feeñ bu baax.

  • Na ponk yi gën a am solo leer te yomb a xam. Tànnal rekk ponk yu gën a am solo yu ànd ak turu waxtaan bi ngay def ak yu nga mën a leeral bu baax ci jot gi ñu la may. Ponk yi gën a am solo, buñu bare te na bu nekk leer bu baax, taxawal tuuti diggante ñaari ponk te nanga jàll ci beneen ponk ci fasoŋ bu yomb.

    Xelal bu baax

    Booy tàmbali sa waxtaan, mën nga lim ponk yi gën a am solo ngir nit ñi mën laa topp bu baax. Mën nga leen waxaat itam booy jeexal sa waxtaan ngir mu des ci seen xel.

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager