LESOŊ 20
Li ngay wax ngir jeexal sa waxtaan
Kàdduy Waare 12:13, 14
LI NGA WAR A JÀPP: Booy jeexal sa waxtaan, xiiral ñi lay déglu ci bëgg a jëfe li ñu jàng.
NI NGA KO MËN A DEFE:
Li ngay wax ngir jeexal sa waxtaan, na ànd ak xalaat bi gën a feeñ ci waxtaan bi yépp. Waxaatal ci ponk yi gën a am solo ak ci turu waxtaan bi.
Xiiral ñi lay déglu ci jëfe li ñu dégg. Wonal ñi lay déglu li ñu war a def ak li war a tax ñu def ko. Booy wax, nanga wone ne gëm nga li ngay wax te ku dëggu nga.
Li ngay wax ngir jeexal sa waxtaan, na leer te gàtt. Bu ci yokk ponk yu bees. Ak ay kàddu yu gàtt, xiiral ñi lay déglu ci jëfe li ñu jàng.