LESOŊ 06
Fan la nit jóge?
«Yàlla [...] yaa sàkk lépp» (Peeñu 4:11). Ndax gëm nga loolu? Am na ñu foog ne, kenn sàkku ñu. Bu dee loolu la, kon dañoo jékki-jékki nekk. Waaye bu dee Yàlla moo ñu sàkk, kon war na am li tax.a Biibël bi wax na fi nit jóge. Ci lesoŋ bii, dinga gis li tax ñu mën koo gëm.
1. Kan moo sàkk asamaan ak suuf?
Biibël bi nee na: «Ca njàlbéen ga Yàlla sàkk na asamaan ak suuf» (Njàlbéen ga 1:1). Boroom xam-xam yu bare nangu nañu ne asamaan ak suuf, am na fu ñu jóge. Naka la leen Yàlla sàkke? Dafa jëfandikoo ‘noowam’, maanaam xelam mu sell mi, ngir sàkk lépp li am ci kaw asamaan ak ci kaw suuf (Njàlbéen ga 1:2).
2. Lu tax Yàlla sàkk suuf si?
Yexowa mi sàkk suuf «sàkkewu ko maraas [maanaam ci neen], xanaa tabaxal ñu ko dëkke» (Esayi 45:18). Dafa sàkk suuf si ci anam bu rafet ngir nit ñi mën cee dund ba fàww (Jàngal Esayi 40:28; 42:5). Boroom xam-xam yi nee nañu suuf si, benn la fi. Ci kaw suuf rekk la nit mën a dund.
3. Lan moo wuutale nit ak mala?
Yexowa dafa sàkk suuf si, teg ci garab yi ak mala yi. Ba pare ‘Yàlla bind nit ci takkndeeram’ (Jàngal Njàlbéen ga 1:27). Lu tax nit wuute ak mala? Yàlla dafa sàkk nit ci melokaanam ngir mu mën a wone jikkoom yu mel ni mbëggeel ak njubte. Dafa ñu sàkk itam ak mën-mënu jàng làkk, bëgg lu rafet ak déglu misik. Te mën nañu def lu benn mala mënul a def, maanaam jaamu suñu Boroom.
XÓOTALAL NJÀNG MI
Xoolal liy wone ne Yàlla moo sàkk lépp ak li tax ñu mën a gëm li ci Biibël bi wax. Xoolal li ñu mën a jàng ci Yàlla, bu ñu gisee jikko yu baax yi nit ñi am.
4. Yàlla moo sàkk dund
Bu nit xoolee ci li am ba defar dara, dañu ko ciy tagg. Ki muy toppandoo nag, ndax du moom lañu war a tagg? Seetaanal WIDEO BI. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp.
Lan la nit ñi toppandoo ci li Yàlla sàkk?
Kër goo gis am na ku ko defar. Waaye kan moo defar lépp li am? Jàngal Yawut ya 3:4. Boo paree, nga tontu ci laaj yii di topp:
Lan moo la gën a yéem ci li Yàlla sàkk?
Ndax jaadu na ñu gëm ne, asamaan ak suuf ak lépp li ci nekk, am na ku leen sàkk? Lu tax?
Ndax xamoon nga ne...
Mën nga gis ay waxtaan ak wideo yu jëm ci loolu ci jw.org ci farãse «Hasard ou conception ?» ak «Points de vue sur l’origine de la vie.»
«Ndaxte kër gu nekk am na ku ko sos, waaye ki sos lépp mooy Yàlla»
5. Mën nañu gëm li Biibël bi ne Yàllaa sàkk lépp
Ci njàlbéen ga pàcc 1, Biibël bi nettali na ni Yàlla sàkke suuf si ak lépp li ciy dund. Ndax mën nañu koo gëm, walla ay léeb kese la? Seetaanal WIDEO BI. Boo paree nga tontu ci laaj yii di topp.
Ndax Biibël bi dafay jàngale ne, Yàlla dafa sàkk suuf si ak lépp li ciy dund ci diiru 6 fan?
Ndax foog nga ne mën nañu gëm li Biibël bi ne, Yàllaa sàkk lépp? Bu dee waaw lu tax, bu dee déet lu tax?
Jàngal Njàlbéen ga 1:1. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:
Boroom xam-xam yu bare nangu nañu ne asamaan ak suuf, am na fu ñu jóge. Ndax li ñu wax ànd na ak li nga jàng léegi ci Biibël bi?
Am na ñuy wax ne Yàlla dafa jaar ci évolution ngir sàkk dund. Jàngal Njàlbéen ga 1:21, 25, 27. Boo paree, nga tontu ci laaj yii di topp:
Ndax Biibël bi dafay jàngale ne, Yàlla dafa sàkk mbindeef bu ndaw, loolu di soppeeku ba mujj a doon jën, mala walla nit? Walla ndax dafa sàkk lépp luy dund?
6. Nit wuute na lool ak lépp li Yàlla sàkk
Yexowa dafa sàkk nit mu wuute lool ak mala yi. Jàngal Njàlbéen ga 1:26. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:
Ni ñu Yàlla sàkke tax na ñu mën a wone mbëggeel ak yërmande. Ndegam Yàlla ci melokaanam la ñu sàkke, loolu lan la ñuy jàngal ci moom?
BU LA NIT WAXOON: «Li Biibël bi ne Yàllaa sàkk lépp, ay léeb kese la.»
Lan mooy ci sa xalaat? Lu tax nga wax loolu?
NAÑU TËNK
Yàlla moo sàkk asamaan ak suuf ak lépp li ciy dund.
Nañu fàttaliku
Ci li Biibël bi wax, fan la asamaan ak suuf jóge?
Ndax Yàlla dafa jël mbindeef bu ndaw, bàyyi ko muy soppeeku ba mujj a doon leneen walla ndax dafa sàkk lépp?
Lan moo tax nit wuute lool ak lépp li Yàlla sàkk?
GËSTUL
Xoolal luy wone ne am na ku sàkk lépp.
Xoolal ni ab baay mënee sukkandiku ci Biibël bi ngir dimbali doomam, mu nànd ne Yàllaa sàkk lépp.
Boroom xam-xam yi gis nañu ay yax yu yàgg te def ay gëstu. Xoolal ndax loolu wone na ne Yàllaa sàkk dund, walla dund dafa jékki-jékki rekk am.