LESOŊ 05
Biibël bi dafa ñuy xamal li Yàlla bëgg ñu def
Yexowa may na ñu may bu réy, 66 téere yu ndaw yu ñu boole, mu nekk Biibël bi. Xéyna yaa ngi laaj sa bopp: ‘Fan la Biibël bi jóge?’ Ngir tontu ci laaj boobu, nañu xool ni Yàlla def ba Biibël bi agsi ci ñun.
1. Bu dee ay nit ñoo bind Biibël bi, lu tax ñuy wax ne ci Yàlla la jóge?
Lu tollu ci 40 góor ñoo bind Biibël bi ci diiru 1 600 at. Téere bu njëkk bi, bi ñu ko bindee ba léegi, def na 3 500 at, bu mujj bi 1 900 at. Ñi ko bind bokkuñu woon jamono ak jaar-jaar. Waaye loolu terewul lépp li nekk ci Biibël bi dafa ànd. Naka la loolu mënee nekk? Ndaxte Biibël bi ci Yàlla la jóge (Jàngal 1 Tesalonig 2:13). Ñi ko bind, binduñu seen xalaati bopp. Waaye «Xel mu Sell mi daa na xiir nit ñi, ñu yégle kàddug Yàlla»a (2 Piyeer 1:21). Yàlla dafa jaar ci xelam mu sell ngir xiir ay nit ñu bind ay xalaatam (2 Timote 3:16).
2. Biibël bi, kan la mën a amal njariñ?
Yàlla nee na «xeet yépp ak giir yépp ak kàllaama yépp ak réew yépp» dinañu jariñoo xibaaru jàmm bi nekk ci Biibël bi (Jàngal Peeñu 14:6). Tey, Biibël bi am na ci làkk yu bare-bare, ba raw bépp téere. Daanaka tey, ku nekk mën na jàng Biibël bi ci làkkam, ak fu mu mën a dëkk.
3. Naka la Yexowa def ba aar Biibël bi?
Biibël bi dañu ko bindoon ci lu mel ni der, nga xam ne du yàgg. Waaye ay góor yu bëgg Biibël bi, def nañu ci ay sotti yu wóor. Am na ay kilifa yu mag yu doon xeex Biibël bi, waaye amoon na ay nit ñu nangu ñàkk seen bakkan ngir aar ko. Yexowa bàyyiwul kenn walla dara tere ko mu xamal ñu kàddoom. Biibël bi nee na: «Sunu kàddug Yàlla mooy sax ba fàww» (Esayi 40:8).
XÓOTALAL NJÀNG MI
Xoolal ni Yàlla xiire ay góor ñu bind Biibël bi, ni mu def ba aar ko ak ni mu def ba nit ñi jot ci.
4. Biibël bi wone na ci kan la jóge
Seetaanal WIDEO BI. Boo paree jàng 2 Timote 3:16 te tontu ci laaj yii di topp.
Bu dee ay nit ñoo bind Biibël bi, lu tax ñu koy woowe Kàddu Yàlla?
Ndax gëm nga ne Yàlla dafa jaar ci ay nit ngir xamal ñu ay xalaatam?
Ab sekerteer mën na bind leetar, waaye li nekk ci leetar bi jóge ci keneen. Noonu itam, ay nit ñoo bind Biibël bi, waaye li ci nekk kàddu Yàlla la
5. Biibël bi mucc na ci lu bari
Ndegam Biibël bi ci Yàlla la jóge, kon jaadu na mu aar ko. Kilifa yu am doole yàgg nañu di xeex Biibël bi. Am na ay njiitu diine yu ko doon jéem a nëbb nit ñi. Waaye loolu lépp terewul am na ñu nangu woon a ñàkk seen bakkan ngir aar Biibël bi. Ngir xam kenn ci ñooñu, seetaanal WIDEO BI. Boo paree nga tontu ci laaj yii di topp.
Xam ne am na ñu nangu woon a ñàkk seen bakkan ngir aar Biibël bi, ndax taxul nga sawar koo liir? Lu tax?
Jàngal Sabóor 119:97. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:
Lan moo taxoon nit ñu bari nangu ñàkk seen bakkan ngir tekki Biibël bi te def ba ñeneen jot ci?
6. Téere bu ñépp mën a jot
Biibël bi mooy téere bi ñu gën a tekki ci làkk yu bare te gën a siiw ci àddina si. Jàngal Jëf ya 10:34, 35. Boo paree, nga tontu ci laaj yii di topp:
Lan moo tax Yàlla bëgg ñu tekki Kàddoom ci làkk yu bare te siiwal ko?
Lan moo la neex ci Biibël bi?
Daanaka
ñépp
ci àddina si
mën nañu jàng Biibël bi ci seen làkk
Am na ci lu ëpp
3 000
làkk
muy Biibël bi yépp walla ay xaaj
Sotti yi ñu ci def tollu nañu ci
5 000 000 000
Amul beneen téere bu ñu sottee noonu
BU LA NIT WAXOON: «Biibël bi, téere bu màgget rekk la bu ay nit bind.»
Lan nga ci xalaat?
Lan mooy firndeel ne, Biibël bi Kàddu Yàlla la?
NAÑU TËNK
Biibël bi Kàddug Yàlla la, te Yàlla def na ba ñépp mën cee jot.
Nañu fàttaliku
Bu ñu nee Yàlla moo xiir ay góor ñu bind Biibël bi, loolu lan la tekki?
Lan moo la yéem ci ni ñu aare Biibël bi, ni ñu ko tekkee ak ni ñu ko siiwale?
Lan ngay yëg ci sa xol, boo xalaatee ci lépp li Yàlla def ngir nga xam ko?
GËSTUL
Xoolal fi ay nit jaar ba tekki Biibël bi, li dale ci jamono yu yàgg ya ba tey.
Xoolal ni Biibël bi mucce ci ñetti jafe-jafe yu ko doon gàllankoor.
Biibël bi sotti nañu ko te tekki ko ay yoon yu bari. Ndax wóor na la ne soppiwuñu ko?
«Biibël bi, ndax am na lu ñu ci yokk walla lu ñu ci wàññi?» (Ci jw.org la nekk)