LESOŊ 26
Lu tax lu bon ak coono di am?
Bu musiba amee, ñu bare dañuy faral di laajte «Lu tax lii am?» Bég nañu ndaxte Biibël bi tontu na ci laaj boobu!
1. Lan la Seytaane def ba dugal lu bon ci àddina si?
Seytaane miy Ibliis dafa bañ a déggal Yàlla. Seytaane dafa bëggoon a ilif nit ñi, moo tax mu xiir Aadama ak Awa, ñu bañ a déggal Yàlla ni moom. Seytaane dafa fen Awa (Njàlbéen ga 3:1-5). Dafa gëmloo Awa ne, am na lu baax lu leen Yexowa di xañ. Ci moom, nit ñi dinañu gën a bég, bu ñu déggalul Yàlla. Seytaane dafa wax Awa ne, du dee. Loolu mooy fen bi njëkk. Moo tax Biibël bi ne, Seytaane «fenkat la, te ci moom la fen soqikoo» (Yowaana 8:44).
2. Lan la Aadama ak Awa tànn a def?
Yexowa dafa yéwénoon lool ci Aadama ak Awa. Dafa leen waxoon ne, mën nañu lekk ci doomu garab yépp yi nekkoon ci toolu Eden, ba mu des benn (Njàlbéen ga 2:15-17). Waaye ñoom ñu tànn lekk doomu garab bi mu leen tere. Awa «witt ci doom yi, lekk.» Gannaaw loolu Aadama «moom it mu lekk» (Njàlbéen ga 3:6). Ñoom ñaar ñépp déggaluñu Yàlla. Ndegam Aadama ak Awa dañu matoon, def lu baax yomboon na ci ñoom. Waaye dañu tey bañ a déggal Yàlla. Noonu ñu bàkkaar te wone ne bëgguñu Yàlla ilif leen. Dogal bi ñu jël moo leen jural coono bu réy (Njàlbéen ga 3:16-19).
3. Dogal bi Aadama ak Awa jël, lan la ñu jural?
Bi Aadama ak Awa bàkkaaree, dañu mujj a doon nit ñu matadi, te wàll nañu matadi boobu seen doom yépp. Lii la Biibël bi wax ci Aadama: «Bàkkaar ci kenn nit la jaar, dugg ci àddina, indaale fi dee, te dee daldi law ci nit ñépp, ndaxte ñépp a bàkkaar» (Room 5:12).
Li ñuy jural coono bare na. Lée-lée dañuy nekk ci coono ndaxte dañu jël dogal yu baaxul. Lée-lée ñeneen ñooy jël dogal yu baaxul, loolu jural ñu coono. Lée-lée dañuy tombe rekk ci musiba (Jàngal Kàdduy Waare 9:11).
XÓOTALAL NJÀNG MI
Xoolal liy wone ne, du Yàlla moo tax lu bon ak coono yi di am ci àddina si tey. Xoolal it li Yàlla di yëg bu ñu nekkee ci coono.
4. Ki tax ñu nekk ci coono
Ñu bare dañu foog ne Yàlla mooy ilif àddina si sépp. Ndax loolu dëgg la? Seetaanal WIDEO BI.
Jàngal Saag 1:13 ak 1 Yowaana 5:19. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:
Ndax Yàlla moo tax lu bon ak coono di am?
5. Xoolal li kilifteefu Seytaane jur
Jàngal Njàlbéen ga 3:1-6. Boo paree, nga tontu ci laaj yii di topp:
Ban fen la Seytaane wax? (Xoolal aaya 4 ak 5).
Naka la Seytaane wone ne, ci moom am na lu baax lu Yàlla di xañ nit ñi?
Ci Seytaane, ndax nit ñi soxla nañu Yexowa ilif leen ngir am jàmm?
Jàngal Kàdduy Waare 8:9. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:
Bi nit ñi bañee Yàlla ilif leen ba léegi, lan mooy xew ci àddina si?
Aadama ak Awa dañu nekkoon nit ñu mat te ci àjjana lañu doon dund. Waaye dañu déglu Seytaane te bañ a déggal Yexowa
Bi ñu fippoo ba pare, àddina si dafa fees ak bàkkaar ak coono, te dee daldi law
Yexowa dina fi jële bàkkaar, coono ak dee. Nit ñi dinañu nekkaat ñu mat te dinañu dundaat ci àjjana
6. Yexowa dafay yëg suñuy coono
Ndax Yàlla ittewoo na suñuy coono? Xoolal li buur Daawuda ak apootar Piyeer bindoon. Jàngal Sabóor 31:8 ak 1 Piyeer 5:7. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:
Xam ne Yexowa gis na suñuy coono te am na itte ci ñun, lan lay def ci yow?
7. Yàlla dina fi jële suñu coono yépp
Jàngal Esayi 65:17 ak Peeñu 21:3, 4. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:
Yexowa dina fi jële coono yépp ak lépp li ñu indi ci kaw doomu Aadama yi. Ndax xam loolu du luy dëfal xol?
Ndax xamoon nga ne...
Bi Seytaane fenee fen bi njëkk, dafa tuumaal Yexowa. Ci noonu la tilimalee turu Yexowa ndaxte dafa jéem a gëmloo nit ñi ne, Yexowa du kilifa gu jub te amul mbëggeel. Ci kanam tuuti, bu fi Yexowa jële coono yépp, dina setal turam. Maanaam dina wone ne, kilifteefam mooy bi gën. Setal turu Yexowa mooy li gën a am solo ci lépp (Macë 6:9, 10).
BU LA NIT WAXOON: «Coono yi, coobare Yàlla la.»
Lan nga koy wax?
NAÑU TËNK
Seytaane miy Ibliis, Aadama ak Awa, ñooy ñi tax lu bon am ci àddina si. Yexowa yëg na bu baax suñuy coono te dina leen fi jële ci kanam tuuti.
Nañu fàttaliku
Ban fen la Seytaane miy Ibliis wax Awa?
Ni Aadama ak Awa bañee déggal Yàlla, lan la ñu jural?
Naka lañu xamee ne Yexowa yëg na suñuy coono?
GËSTUL
Xoolal li bàkkaar di tekki ci Biibël bi.
Jàngal leneen lu jëm ci li Seytaane weddi ca toolu Eden ba.
Xoolal benn góor gu nànd li tax mu doon dund ci coono.